Piyeer Mbów mooy njiitu këru gan gii di “King Fahd Palace”. Moom nag, dafa indi ay leeral ñeel xibaar yi Majambal Jaañ siiwal. Ndax, moom Majambal, dafa wax ne, “King Fahd Palace” dafa nekk, jamono jii, ci ay tolof-tolof. Te, ba tey ciy waxam, doon na gën a woyof ci ñoom bu leen Nguur gi fayoon seen boru juróom-ñetti téeméeri miliyoŋ ak lu teg. Bor boobu, ci li Majambal wax, mi ngi aju ci diir ba fa Basiiru Jomaay Fay ak Usmaan Sonko nekkee. Piyeer Mbów weddi na waxi Majambal yi.
Ki jiite “King Fahd Palace” dafa setal Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi. Ndaxte, dafa xamle ne, waa PASTEF fay nañu lépp ba mu mat sëkk. Kon, yoreeluñu kër gi fiftin. Majambal nag, mi ngi wéy di ŋoy fi mu jàpp rekk. Nde, dafa génnaat, feddaliy waxam, weddi yoy Piyeer Mbów. Moom Majambal, Aamadu Ba la àndal ci wote yees dëgmal. Looloo tax ñu bari jàpp ne moom lay jambal, di xajamal cerey PASTEF.
Bi Piyeer Mbów leeralee ba noppi, wax ne Càmmug Senegaal ameelul “King Fahd Palace” xaalis, coow li dafa waroon a fay. Ndax, moom mi jiite kër gi, kenn ëppu ko i xibaar ci béréb bi. Kon, bu Majambal màttee, bañ a bàyyi, jar na ñu samp ab laaj. Ndax dafa bëgg Yoon woolu ko ? Ndax, li muy wax, mënees na ko jàppee ni yàq der , tuumaal ay kilifa ak wesaare xibaar yu wéradi. Te, loolu, Yoon daf koy tere. Mënees na la cee jàpp sax, teg lay daan, tëj la kaso. Ndax Majambal dafa bëgg ñu jàpp ko ? Mën na nekk. Nde, bu boobaa, dinañu wax ne, ñoom ñi àndul ak Nguur gii fi nekk, Jomaay ak Sonko kat, jàppaate ak tëjaate lañu fi nekkee, jéem leen a jaxase ak askan wi, jéem leen a jaxase ak àddina si. Ndax pexeem dina àntu ? Li ci kanam rawul i bët.