NJUREEFI NÉGANDI YU WOTEY NGOMBLAAN GI, lu mu nar a jur ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Décce Faal ak i ñoñam, waa Wallu-Yewwi, dinañu am lu leen metti. Te, sikk amul ci ne, dinañu génn fésal seen ug ñàkk ànd ci njureef yi Magum njiitalu Cour d’appel bu Ndakaaru biral ci ngoonug alxames ji. Waaw, njureefi négandi yu wotey Ngomblaan gi génn nañu. Ñaari àttekati CNRV, kurél giy waññ xobi wote yi, ñoo àndoon ak Magum njiitalu Cour d’appel bi mu leen di biral. Waaye, nag, sikk amul ci ne dina am ñu bari ñu dul ànd ci njureef yile, rawatina waa Wallu ak waa Yewwi ak askan wi top seen ginnaaw yépp. Ndax dañuy seetaan walla ?

Ñeenti fan, ginnaaw bi ñu wote ak léegi. Askan wi doon xaarandi njureef yi. Bu dee ne wote yi am nañ ci anam yu jaar yoon, ni ko saytukati CEDEAO yi waxe ak ñeneen, ba ci alxames jii, coow li ak xëcco bi bari woon na diggante lëkkatoog nguur gi, Bennoo Bokk Yaakaar, ak ma-lëkkatoog kujje gi Wallu-Yewwi. Nde, booba ak léegi, ku nekk a ngi ñoddi, di biral ak a xayma ay lim, di damu ak artu sa moroom. Waaye, mel na ni yoon BBY la àndal.

Ci alxames jii lañu génne njureefi négandi yi. Ñu ne, ci procès-verbaux yi ñu jot yépp, jële leen ci kuréli yiy waññ xobi wote yi ci depaartmaa yépp ak këyit yi ñu ci toftal, lañu sukkandiku, ci lu dëppook dogu 143 bu àtteb wote bi. Ci kow loolu lañu biral njureef yii toftalu (ñoom ni ñu binde turi lëkkatoo yi lañu fi indiwaat) :

Ci biir 7. 036. 466i nit yi bindu woon ci këyitu wote gi, 3. 281. 583 ñoo ci wote. Maanaam, téeméer boo jël ci ñu bindu, 46,64 rekk ñoo sànni xob. Ci biir xob yooyii, 20. 697i baaxuñu, 3. 260. 886 yi ñoo ci wér. Lëkkatoo bu nekk am na :

Lëkkatoo Bokk Gis-Gis : 44. 862

Lëkkatoo Naataangue Askan wi : 25. 830

Lëkkatoo Alternative pour une Assemblée de Rupture / AAR Senegal : 52. 173

Lëkkatoo Benno Bokk Yakaar : 1. 518. 137

Lëkkatoo Bunt Bi : 20. 922

Lëkkatoo Les Serviteurs MPR : 56. 303

Lëkkatoo Yewwi Askan Wi : 1. 071. 139

Lëkkatoo gu mag gi Wallu Sénégal : 471. 517

Bu ko defee, bu nekk ci lëkkatoo yii di Bokk Gis-Gis, Lëkkatoo Alternative pour une Assemblée de Rupture / AAR Senegal ak Les Serviteurs MPR, benn depite lay am ca Ngomblaan ga. Benno Bokk Yakaar daldi am 82i depite, Yewwi Askan Wi 56i depite, Wallu Sénégal 24i depite. Bunt Bi ak Naataangue Askan wi amuñu dara.  Lii yoon génne, nag, du luy gaatnga jàmm ci réew mi.

Nu fàttali as-tuuti ci lu fi jot a xew laata ñuy biral njureefi négandi yi…

Ci guddig àllarba ji la waa Wallu-Yewwi amaloon ab ndaje ak taskati xibaar yi, wax ne dafa am ay njuuj-njaaj yu bir ci ñeenti depaartmaa ñeel bëj-gànnaaru réew mi : Podoor, Maatam, Ranéeru ak Kanel. Décce Faal ne “Li ko dale démb [talaata 2 ci ut 2022, clkg] ci 12i waxtu, noo nga woon ci màkkaanug Kurélug waññ gi. Ci noonee la sunuy xel dem ci yenn ciy “procès-verbaux” yoo xam ne dafa am ay ndëngte.” Li taxon ñu gënoon a bàyyi xel “procès-verbaux” yooyee mooy ne, ci kàdduy Décee Faal, li BBY ëppale yeneen lëkkatoo yi ci 4i depaartmaa yees lim ci kow dafa ëppoon lool ba yéem leen. Ci lañu xool, ba tey ci waxi Décce Faal, gis ne am nay PV yoo xam ne kenn torluwu leen. Ci lañu jàppe ne am na luy ñuul ci soow mi te, liy raam ci ñag bi la jëm. Bi Musaa Tin jëlee kàddu gi, dafa wax ne, lu ni mel, “ci ñaari anam kese la mën a ame, immaa dañu rënk mbañ-gàcce yi, immaa ñu sos ay pekki wote yu amul”.

Bu ko defee, li kujje giy tuumaal Nguur gi mooy ne dafa njuuj-njaaj, sàkk i pexe ngir dabu limub depite bi ñu ko rawe ci dëkk yu mag yi. Ayda Mbóoj di leeral ne, “200 000iy xob” la Nguur gi bëgg a sos, dolli leen ci limam. Usmaan Sonko, ci wàllu boppam, xamle woon na ne, ñoom, “duñu mës a nangu ñuy foqarci seen ndam”. Mu teg ci ne, “Lii, pexem naxe-mbaay mu réy a réy la, ay politiseŋ nas ko te kootoo ci ak caytu gi ci lu wér te wóor.” Waaye, nee ñu loolu du mës a jàll. Xalifa Sàll tegoon ci ne, “lu mu jararl Nguur gi dina leen ko jaral”. Seex Yum mu làngu PUR dafa ne, moom, bii yoon, “askan waa war a wax ak Nguuru Senegaal, ne ko DOY NA.” Ci kow loolu, ñoom waa Wallu-Yewwi, yégle woon nañu ne dinañ sàkku ñu tëbal biralug njureef yi waroon a am ci alxames ji.  Décce Faal :

“Noo ngi sàkku ci Njiitalu Kurél giy waññ xobi wote yi (CNRV) mu tëbal biralug njureefi wote yi bi mu war a amal ci alxames ji ba jëmmi jamono ngir nu mën a feeñal ndëngte yi nu gis ci “procès-verbaux” yi”.

Li ñu ko dugge woon mooy xoolaat PV yépp ngir seppi yi jaarul yoon, gàntal càcc gi Nguur giy nas. Waaye, ñoom itam, waa BBY, dañoo génnoon tontu leen, wax ne nisëru kujje gi mooy “gàkkal deru Senegaal ak xajamal wote yi”.

Abdulaay Sow, meeru Kafrin bi bokk ci lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar, moo doon wax ak taskati xibaar yi. Lii la tontu ci tuuma yi kujje giy gàll Nguur gi :

“Kurél giy waññ xobi wote yi (commission national de recensement des votes) mi ngi liggéey. Jamono jii lanuy dégg ay wax ñeel ay wote yu jaarul yoon walla ay pekki wote yu ñu sos walla ay “procès-verbaux” yu dëng. Lii lépp, benn jubluwway képp lañ ci am, te mooy gàkkal deru Senegaal, waaye tamit ngir ñaawal wote yi ndax xam bi ñu xam ne ñàkk nañu ko ci lu wér. Loolu nag moo tax nu bëgg leeral dëgg gi.”

Ci bëccëgu alxames ji, Décce Faal demoon na ngir ñu may ko mu xool, lëñbët “procès-verbaux” yi ba xam amul i rëkk-rëkk, waaye dañ ko ko bañal. Ci la woowee taskati xibaar yi ci kanamu Palais de Justice, daldi xamal nit ñi ne Njiitalu kurél giy waññ xobi wote yi daf ko banal li ko yoon may. Noonu, mu daldi bind, àkki CENA ngir mu àtte.

Ci diggante bi, Njiitu réewum Farãs, Emaniwel Makorõ, bind ab tweet di ci ndokkeel askanuw Senegaal ci seen ñor ak dal bi ñu àndal ba wote yi am ci jàmm. Ñu bari, rawatina ci kujje gi, jàngatee ci ne, Farãs dafa dëddu Njiitu réew mi Maki Sàll. Nde, ci li ñooñii jàpp, fi Njiitu réewum Farãs ndokkale askanu Senegaal wëliis Maki Sàll day firndéel ne Farãs andatul ak Maki Sàll bi mu xame ne askanu Senegaal bëggatu ko.

Ak lu ci mënti am, Senegaal ci nen la toog. Laaj bi sampu nag mooy, ndax  Ceerno Alasaan Sàll, Paap Jóob ak Paap Jibril Faal dañuy fekki Wallu ak Yewwi, dooleel leen. Ndax kenn ci ñoom dina fekki Bennoo Bokk Yakaar ? Li ci kanam rawul i bët…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj