PAAB FARÃSUWAA GÉNN NA ÀDDUNA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Naqar ak tiis la mbokki katolig yi yeewoo ci altiney tay jii. Kii di Paab ba Farãsuwaa moo wuyuji boroomam. Kii di “Cardinal camerlingue Kevin Farrell” moo siiwal xibaar bi. Mu nekk xibaar bu tiis lool ci àdduna sépp, rawatina waa njabootu Jàngu bi ùboole-seen. Dafa di, ki ñu ñàkk, am na fu mu leen féete woon, muy ci seen wàllu ngëm ak seen dundin ci kaw suuf.

Xibaar bu bette moo dal ci àdduna si. Nde, kenn umpalewul ne, démb la woon “Pâques” yi. Te, ki faatu tay, génnoon na saafonte ak mbooloo ma, màggalandoo ak ñoom bés ba, donte ne sax wér-gi-yaramam demewul woon noonu. Rax-ci-dolli, kàttan gi it matewu ko woon. Ànd ak loolu yépp, génn na, gise ak ñoom. Ndeke, booba, ma ngay tàggatoo.

Tay, ci altine ji, la Paab Farãsuwaa génn àdduna ay boori juróom-ñaari waxtu ci yu tegal fanweeri simili ak juróom, ci yoor-yoor bi. Ma nga génne àdduna fa këram, ca Vatican, ñu koy dippe “La Casa Santa Marta”. Ay atam ñi ngi tolloon ci juróom-ñett-fukki ak juróom-ñett. Mu nekkoon nit ku baax, dëggu te bari yërmaande ak ñeewant ci néew-ji-doole yi bees sukkandikoo ci seedey kardinaal bi.

Moom Paab Farãsuwaa mi dëddu tay jile, mi ngi juddoo fa Buenos Aires, nekk ca Arsàntin, keroog fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru desàmbar, atum 1936. Moom nag, ay way-juram ay doomi Itaali lañu. Moom mooy Paab bi ñu njëkk a fal te mu bawoo Amerig latin. Maanaam, mooy ki fa njëkk a nekk Paab te cosaanoowul Ërob ginnaaw ay xarnu. Ñi ngi ko fal fukki fan ak ñett ci weeru màrs, atum 2013. Moo nekk ñaari-téeméer ak juróom-benn-fukk ak juróom-benneel (266eel) Paabu Jàngu bi.

Mu mel ni Paab bi amal na liggéey bu mucc ayib cig kayam. Ndax, yemul woon ca Jàngu ba rekk. Waaye, ay kàddoom ci doomi-aadama yépp la ko daan jëmale. Rax-ci-dolli, taxawaay bu rafet la amoon ci jëflante doomi-aadama yi, muy ci seen mbiri bopp walla ci diine yi ñu gëm. Kon, àdduna wërngal-këpp ñoo ñàkk.

 EJO ak DEFU WAXU ñoo ngi jaal mbokki katolig yépp, di leen mastawu ci xew-xew bu tiis bile.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj