Ëttub àttewaay bu Pari delsi na ci àtteb Paap Masata Jaag bi. Waaye, àtte bi dafa dellu feddali daan yi ñu ko tegoon jëm ci nger ak luubal xaalis. Moom, Paap Masata Jaag, di doom ci Lamin Jaag, doomub réewum Sénégaal ji fi jiite woon kurélug atleti àddina si (Fédération internationale d’athlétisme, IAAF ci jamono yooyu) diggante 1999 ak 2015, moo nekkoon « consultant marketing » bu kurél gi.
Ci alxames jii, weesu la ëttub àttewaay bu Pari doon delsi ci àtteb Paap Masata Jaag. Moom « consultant markting » ba woon ca IAAF, li ñu ko doon toppe mooy ànd ak i nit ci baara-yëgoo ak nger. Looloo ngi xewoon ci atum 2011. Moo waraloon ba moom ak ñi ñu ci doon tudd bàyyi ay atleti réewum Riisi yi donn jëfandikoo sineebar, te mu doon lees dàq ci tàggat-yaram bi, ñu bokk ci powi Olempig yi doon am Londres ca atum 2012.
Bokk na ci lees ko doon tuumal itam ni dafa rawale xaalis bu takkoo takku bu war a tollu ci 15i tamndareti Euro. Bi ñu ko tuddee ci mbir mi, njëkkoon nañu ko àtte ci weeru Sàttumbar 2020. Naka noonu, yoon tëjlu ko 5i ati kaso ba noppi mu war a fey alamaanub 1 tamndaretub “Euro”.
Ginnaaw bi ñu tegee ci kowam yile daan, Paap Masata Jaag dafa wéyoon di miim tuuma yi. Moo waraloon mu sàkku ñu àttewaat ko. Bi ñu ko ko nangulee, àttewaat baa ngi doon am ci 13 ba 19 sãwiyee 2023. Waaye, àndiwul lenn lu bees. Daan yi àtte bu njëkk ba tegoon ci kowam, di 5i ati kaso, la dellu dëggal. Terewul àttekat bi wàññi na lees ko alamaanoon ci xaalis, jële ko 1 tamndaretub “Euro” yóbbu ko ci 50.0000iy “Euro”.
Li àtte bi di am yépp nag ca atum 2020 ak ci atum 2023 bi, Paap Masata Jaag mësul a teew foofa ca Pari. Mi ngi woon fii ci Ndakaaru. Yoonu réewum Senegaal mayu ko mu génn réew mi ndax dafa nekk ci « contrôle judiciaire » ci lu jëm ci menn mbir mi. Fii mu nekk, nanguwul wenn yoon yëy yàbbi ci ndogal li. Mi ngi toog di xaar kàddu gu mujj gu ëttub àttewaayu Pari.