Njiitu réewum Irã li, Ebraahim Raysi, faatu na. Fafalnaaw bi mu duggoon ak jëwriñam ja yor mbiri bitim-réew moo daanu. Jëyya jaa ngi xew démb ci dibéer ji. Waaye bi ñu demee ba ci biir guddi gi, 3i waxtu ci altine ji, lañuy sog a gis seen i néew fa fafalnaaw ba daanu, ca bëj-gànnaaru réew ma. Réew ma dina ko dëjal ci juróomi fan yii di ñëw. Bu weesoo loolu, ki jiitu woon ci toftali Njiitu réew ma, Mohammad Mohber, moo ko war a wuutu ci boppu réew ma. Ndeyu Sàrti réew ma ko fa teg, waral na ci moom mu amal i wote ngir ñu fal Njiitu réew mu bees fileek 50i fan.
Paatoom gi nag dafa dajeek jamono joj, seen diiwaan boobu bari coow lool ak xeex bi Israayel di amal fa Gasaa (Palestin). Réewum Irã sax jotoon na cee dugal loxoom ci fan yii weesu.