Njiitul pekkug Asimi Goytaa lii di Umar Taraawore, ñu koy woowe Duglaas, ñàkk na bakkanam. Ay rëtëlkat a ko rey cib dampoo bi ñu am ak ñoom ci yoonu Gire ak Nara, fekk ñu doon saytuji liggéey yuy am ca diiwaan ba ci ndimbalu Njiitu réew ma.
Alarba, 19 awril 2023, la làrme bu réewum Mali xéyee génne ab yëgle. Ci biir yëgle ba, ñu siiwal ca ni ag këru liggéey guy yëngatu ci wàlluw tabax i fooraas lañ song ci talaata ji, 18 awril 2023. Cong maa ngi ame ci bëj-gànnaaru réew ma, fu sorewul dara ak diggam ak réewum Móritani, ci yoon wi dox diggante Gire ak Nara.
Bi ay 17i waxtu di jot ca diiwaan ba, lay nit yu ngànnaayu ba diis kar daamari këru liggéey googu doon dox ci ndimbal ak taxawu gi Njiitu réew ma di amal foofu. Bi ñu dalee seen kow, ci saa si la sóobare yi (Fama de Nara) jàmmaarlook ñoom ba daldi rawale genn daamar gi ak ñaari nit. Ci ginnaaw gi, la sóobare yi gis geneen daamar gi, fekk ñu taal ko, reyaale ñeenti nit ña ca nekkoon.
Bi ñu demee ba 19i waxtu di jot, la sóobare yi jóge woon Gire dampoowaat ak ñoom ñu yor ñetti daamar doon amalaat meneen cong. Ci lañ yàq seen genn daamar, jàppaale ci ñoom ñetti saay-saay.
Ci tënk, ñeenti doom-aadama ñoo ci ñàkk seen bakkan. Ci way-faatu yi, ñu ràññe ci kii di Umar Taraawore, diy njiitul pekkug Njiitu réew ma. Fekk mu bokkoon cib kippu bi doon dem ca diiwaan ba ngir saytuji liggéey yees fay amal.
Keroog ci àjjuma ji, mbootaay mi tudde boppam GSIM (Groupe de soutien à l’islam et aux musulmans) fésal na ne ñoom ñoo amal cong moomu. Yokk nañ sax ni teg nañu loxo ñaari sóobare. Waaye làrme bi dëggalu ko.
Làrme bi dolli naat xamle cib yëgleem ni mi ngi rafetlu ni leen askan wiy jàppalee ak i xibaar ba ñuy mën a faagaagal rëtalkat yooyu nga xam ni ñàkk pexe ak yërmaande moo leen xiir léegi ci ñuy amal i xeeti cong yii jëmale ko ci ñiy taxawu askan wi ci seen i jafe-jafe.