PADES II : TÀMBALI NAÑU ÑAAREELU WÀLL WI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nguur gi sóobu na ci ñaareelu wàllu naaluw PADES II. Mu fas cee yéene dugal 77i tamñareeti (miliyaari) FCFA ngir sopparñi njàng mi, mu dëppook mbaaxi réew mi, yamale ñépp ak gox yépp.

Démb ci àjjuma ji, 30 me 2025, lañu doon ubbi ñaareelu pàccub naal wii di PADES II (Programme d’Appui au développement de l’éducation au Sénégal). Ñu doon ko amal ci njiiteefu jëwriñ ji ñu dénk njàng mi, Mustafaa Giraasi, fa taaxu caytu bi ñu duppe Mamadu Ja. Muy naal wow, li ko taxoon a jóg mooy doxal naal wi ñuy wax PAQUET ( 2018-2030) ngir jële fi néew-doole ak parparloo te am njàngale yu gën.

Ñaareelu pàcc bi, dees na ko dawal ci diirub ñetti at (2025 ba 2028). Jubluwaay bi di dellu ci yokk baaxaayu njàngale yi, yamale ba ñépp mën a jot ci njàng mi ak yokk càmmin wi. Nde, ci li jëwriñ ji biral, lu ëpp 4i tamndareeti gune jotuñu ci njàng mi. Te itam njureef yi ñuy am ci njàngale yi dese naa méngoo lool ci diggante njàngaley xayma ak dawal.

Lu ni mel tax na ba jëwriñ ji dellu di woote jëme ci sàkkuy saafara yu méngook soxla yi te ñu ànd ceek njaxlaf. Naka noonu, fas nañu cee yéene dooleel njàng muy yamale, mu bari njureef te dëgërlu. Waaye, itam njàng muy bàyyi xel wuuteg gox yi.

Waajal nañu lu tollu ci 77i tamñareeti FCFA ngir kopparal ko. Nguur gi nar cee ànd ak i digaaleem yu bari, rawatina waa AFD (Agence Française de Développement) ak waa PME (Partenariat mondial pour l’éducation). Naal wi di wane dogu gi Nguur gi ak i digaaleem am ngir taxawal lekool bu ñu tabax ci mbaax yu deme ni ndimbalante, yamale, leeral ak delloo mbàttu ci ndaa li.

Doxalinub ñaareelu pàcc bi dina bàyyi xel bu baax njàngat yu ñu jële ci pàcc bu njëkk bi ngir taxawu bu baax béréb yu gën a néew-doole ci réew mi. Dinañu ci amal i tabaxte, ay jumtukaayi njàngale, ak ay dund yu ñu jagleel lekkool yi. Dinañ gën a jegele itam bànqaasi caytu gi ak jàngu yi.

Ci pàcc bu njëkk bi, jotoon nañu tàggat lu tollu ci 30 000iy jàngalekat, jàppale ci lu tollu ci 7 000iy njàngaan yu fekk baax ci njaboot yu néew-doole. Amal nañu itam ci IA (Inspections d’Académie) yi ay sémbuw suqaleeku yu aju ci càmmin ak yamale.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj