Ginnaaw bi Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay tasee Ngomblaan gi, coow top na ci. Bu ñii dee werante ci ndogal li, ñeneen ñaa ngiy waajal xaat-xaat wote yees dëgmal fii ak ñaari weer, war cee falaat yeneen i dépite. Am na sax, ci kujje gu bees gi, ñu taxawal ag kurél duppee ko ATEL (Alliance pour la transparence des élections).
Ginnaaw bi Njiitu réew mi tasee Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob mi jiite googu campeef yékkati na ay kàddu. Muy xamle ni ndogal lu mu am sañ-sañ la, te yit nangu na ko. Barki-démb ci àjjuma ji, la biral ab yégle di ci wax ne :
«Ci alxames ji, 12i pani sàttumbar 2024, Njiitu réew mi biral nay kàddu, tas Ngomblaan gi. Sañ-sañ bu ñu jagleel Njiitu Nguur gi la, mu jëfandikoo ko… Nangu naa ko, di ci sant Yàlla (SWT) Moom mi dara tëwul, ginnaaw bi mu ma mayee ci ñaari at yii bari woon i yëngu, ma doxal li ñu doon xaar ci man niki njiitu Ngomblaan gi ci ngor, yitte ak taqook mbaaxi bokkeef, sunuy jikko yu rafet ak lees di séentu ci demokaraasi. »
Bu weesoo njiitu Ngomblaan gi, bari nay Saa-Senegaal yu biral seen gis-gis ñeel tasug Ngomblaan gi, rawatina way-pólitig yi. Mu mel ni sax ab jàkkaarloo la diggante kujje geek Nguur gi. Bu ñii naan waaw góor Njiitu réew mi, ñee di ko ŋàññ ak a xarab. Terewul nag am ñu sóobu xaat ci wote yees war a amal keroog 17i pani nowàmbar bii di ñëw.
Lu jëm ci wote yooyu sax moo gën a yitteel ñii di waa ATEL (Alliance pour la transparence des élections), dig lëkkatoo gu ëmb lu ëpp ñaar-fukki làng ak ay kurél. Nde, seen yitte mooy wote yu jaar yoon mën a am. Ba tax ñuy sàkku ci Njiitu réew mi mu woo, ci ni mu gënee gaaw, képp ku war a laale ci doxalinu wote yi ak waa DGE (Direction Général des élections), ngir ñu waxtaane nees di waajale wote yii nga xam ni dañ leen a andalsi.
Ñoo ngi sàkku itam ci askanu Senegaal mu takku te fas yéene sóobu ci bépp xeex bu ko laaj ngir ñoŋal lees am ci demokaraasi. Nde ñoom, itam dinañ ànd, xeexandoo ngir am wote yu ñu waxtaane, yu leer, yu digg-dóomu yu réewum Senegaal yelloo ak fi turam yegg ci demokaraasi.