PÂQUES 2024 : PAAB FRANÇOIS A NGI WOOTE JÀMM CI ÀDDINA SI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paab bi sàkku na ngir ñu dakkal xare bi dox diggante Israayel ak Palestin. Càkkuteef googu, biral na ko ba mu jëlee kàddu ca seen xew-xewu diine bu mag boobu ñu doon amal démb : “Pâques”. Muy xew-xew bu réy ci diiney kercen yi. At mu jot ñu koy màggal, Paab bi di jëlaale kàddu ngir wax ci xew-xewi jamono ak tolluwaayu àddina si.

Jamono jii nag, fitna ji bari na ci àddina si, rawatina xare yi dox diggante Riisii ak Ikren ci benn boor, ak Israayel ak Palestin ci beneen boor. Bu dee xare bu mujj boobii, limu nit ñi ciy dee jéggi na dayo lool. Israayel a ngi rey ay Saa-Palestin yu dul jeex, dem bay bombàrde ay loppitaan. Dafa, yawuti Israayel yi dañu tànc julliti Palestin yi, fatt daanaka fépp ba ndimbal du fa àgg. Wëliis mbéll yeek fetel yi, xiif moo nekk di rey lu bari ca askan wa, rawatina ci weeru koor gees nekk. Kon, bu yeboo jàpp ne Israayel a ngi faagaagal waa Palestin, rawatina waa “Gaza”. Loolu la Paab bi naqarlu te di woote ngir mu dakk.

Bakkan yaa ngiy rot fa Palestin, ay junniy junni doomi-aadama di amey gaañu-gaañu, alal ju dul jeex di yàqu. Loolu, bu yàggee, Israyel dina faagaagal askan wépp. Paab bi nag, dafa jàpp ne ab xare du “…mës a nekk ndam”. Ndax, fu bakkan rot moom, ndam walla mbégte waru fa am. Kon, muy ca Ërób di ci Méditerranée bi, kenn warul di gaaw a jëfandikoo ay ngànnaay ngir faj meram. Maanaam, ñu moytoo dund dundiinu mala. Ëpp la doole rekk, bës sa bët. 

Dafa di, la xew ci diggante Risi ak Ikren doy na ci misaal. Ndax, bu yàgg ba tey ña nga ca xeex ba. Bu dee am na kenn ci ñoom ku ci am ndam it, du doon lu réy. Moo tax, muy sàkku ci ñoom, ñaari réew yooyu, ñu weccoo seen ñoñ yi ñu jàpp ci xare bi. Maanaam, ku nekk delloo moroomam ag njabootam. Ñu delluwaat ca jàmm ja ñu nekkoon.

Naka noonu, mi ngi sàkku tamit ñu dakkal reyante boobu am fa “Gaza”. Ndax, la fa xew moom, ciy kàddoom, weesu na xare, waaye ab “…xeetu lëmm lañu fa bëgg a jële”. Donte ne sax, xare bi am ci diggante Israayel ak Palestin yombul a lijjanti, waaye, ña cay faatoo moom ay doomi-aadama lañu. Moo tax, mu leen di woo ngir ñu jàmmoo. Ñu bàyyi ñi nga xam ne jàppoon nañu leen juróom-ñaari fan ci weeru oktoobar 2023. Rax-ci-dolli, ñu bàyyi li ñuy dimbalee Palestin cib dund mu jàll. Bu ko defee, ñu mën a door ay waxtaan ba lépp dellu na mu meloon. 

Kon, kàddoom yooyu làmboo nañu njariñ ci fi àdduna bi tollu. Ñu bari sax di laaj lu tax réewi araab yi jiituwuñu ci lii. Donte ne sax, moom du jullit terewul mu sàkku ci jullit yi ñu suuxat jàmm. Am ñuy laaj sax lu tax kàddoom yii yékkatiwu leen bu yàgg ba tey. Waaye, lu baax moom du naaje, du guddee. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj