PARIS SAINT-GERMAIN : BIDDEEW BI DIKK NA!

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ca péeyu Farãs, Pari, foo sànni mbattu mu tag. Te lenn waralu ko lu moy mbégte mu réy ma fa Paris SG andi gannaw ba mu bomee njëkkeelu kubu Ligue des champions ci mbooram.  Mu di woon yan wu réy wu ko teggeegu. Waaye tamit, di daraja ju màgg jum ràngoo fa biir dëkk ba.

Démb, 31i mee, ca Munich, péeyu Almaañ, lees doon amale finaalu powum tugal bu mag bi. Mu nekkoon diggante Paris SG ak Inter de Milan. Mu leeroon ni dana metti te itam dana neex. Ndaxte, ñaari ekib yu mag te mu jaral leen lu nekk ñoo ci daje. Kii tooglo Arsenal mi génne woon Real Madrid, kee wàccee Barça, ca dëmi-finaal ya. Mu nekkoon tamit mats bu neex, donte doole féete woon na benn boor. Nde, ku xool njureef li (5-0) xam ni mën am na fa.

Moom Paris SG nag, dafa yàgg a wër bile kub, ba tax at mu nekk mu génne xaalis bu duun jënd ay futbalkat yu xarañ ngir mën caa jot. At yi weesu mu yàgg a ñafe, di góor-góorlu, di raam muy metti ba atum 2020 mi mu finaalu te Bayern gañe ko ca. Tur wu nekk ak xarañte bu nekk jaar fa dara. Messi, Ibrahimovic, Cavani, Di Maria, Thiago Silva, Ramos, Mbappe… ak ñu bari jaar fa taxul mu jël ko. Waaye lu wolof naan “lu jot, yomb”, loolu la. Xëy-na yaakaar jees amoon ci ekibam ya weesu sax ameesu ko woon ci njëlbeenam ren. Rawatina bi seen ndaanaan ba, Mbappe, demee ca Real Madrid. Loolu lépp taxul ekib ba xàddi wenn yoon. Ren Paris SG ñëwaat ak bëgg-bëgg, aamu ak dogu. Xare dëgg, ndaxte ay punkal rekk la wàcce ci yoonam, rawatina ekibu àngale yi gën a taxaw, City, Liverpool, Aston Villa, Arsenal. Kon yeyoo na ko.

Lile di yan wu rëy wu teggeeku. Benn, dugal na boppam, turam, ak mbooram ci ekib yu mag a mag yi. Ñaar, fàww nangulees ko cëram biir Farãs. Nde, donte moo fa ëppaley kub teewul su waaxaan ñu ni Marseille rekk a fa jël “Ligue des Champion”. Tay biddeew bi dikk na. Lii la wolof njaay naan “xëcc bu daggul, dikk”, te “ku muñ, muuñ”. Dëgg la !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj