Keroog, àjjuma ci guddi, lañu fekkoon Basiiru Jomaay Fay ca kanamu DGID, fa muy liggéeye, jàpp ko. Lees ko jàppe, du lenn lu mooy kàddu yoy, doon na ci tiiñal anam bi yoon di doxe ñeel layoob Maam Mbay Ñaŋ ak kilifaam gii di Usmaan Sonko. Ab yaxal la biraloon ci xëtu facebookam di duut baaraam ni àttekat yiy jalgatee yoon ci lu bir.
Nees ko jàppe woon, nag, keroog, dafa safaanoo ak li yoon tëral. Ndax, benn, kenn wooluwu ko. Ñaar, takk-der yi dañu demoon këram di ko tëru bés bépp. Ñetteelu jalgati yoon baa di liñ demoon ca bérébu liggéeyuwaayam, naroon a dàjji pekkoom ngir yóbbu ko. Ñu ni déet-a-waay, ñu bàyyi ba mu wàcc, ay 22i waxtu jëm kow, ñu daldi koy patam-patamee, dugal ko ci seen daamar, yóbbu ko. Tuuma yii toftalu lañ koy jiiñ ne moo leen def :
-
Yàq-der ñeel ay nit yiy def seen liggéey ;
-
Tooñ ay àttekat yiy def seen liggéey ;
-
Jëf yu mën a sabab i yëngu-yëngu ci réew mi.
Bi mu janoo ak toppekat bi, nag, Basiiru Jomaay Fay feddali na kàddu yim bindoon yépp. Deltuwul ginnaaw wenn yoon. Bu dee tuuma yees ko gàll, moom, àndu ci. Nde, dafa jàpp ne waxul dara lu aay. Ndaxte, ŋàññul benn bànqaasu Yoon. Te, sax, moom, dafa joxewul benn xibaar bay joxe xibaar yu wéradi. Magum tof-njiitu Pastef li neeti, deful lu dul ñaawlu ni Yoon di doxe ak ni ñuy salfaañee àq ak yelleefu seen lawax bii di Usmaan Sonko. Mu mel ni, nag, àttekat bi fullaalul ay kàddoom. Dafa di, Basiiru Jomaay Fay, dóor nañ ko « mandat de dépôt » tey ci talaata ji, 18 awril 2023. Dina fanaan guddeem gu njëkk ca kasob Rëbës.
Buñ nee Maki Sàll ak Nguuram dañ singali waa Pastef, du neen. Toftalaanug niti Pastef yi ñu jàpp doy na ci firnde :
Ñi nekk biir kaso jamono jii :
-
Basiiru Jomaay Fay, Magum tof-njiitu Pastef ;
-
Faddiilu Keyta, aji-bokk ci pekkug Usmaan Sonko, jokkalekatu Nemmeeku Tour bi ;
-
Aliyun Badara Mbuub, aji-bokk ci pekkug Usmaan Sonko, jokkalekatu Wër ndombo bi
-
Baabakar Njaay, tof-njiitu kurélug ndawi Pastefi Senegaal ;
-
Muhammed Bilaal Jaata, meeru Kër Masaar ;
-
Muramaani Kaba Jakite, ñaareelu tof-njiitu Pastef ;
-
Majaw Jóob, jokkalekatu JPS bu Tiwaawon ;
-
Abdu Kariim Géy, Kilifa ca Pastef Tëngéej ;
-
Baaba Jaw, Kilifa ca Pastef Tëngéej ;
-
Bintu Sàmb, kurélug ndaw ñi – JPS Tiwaawon ;
-
Usmaan Suwaane, jokkalekatu kurélug ndaw ñi – JPS Gosaas ;
-
Baaba Caam, jokkalekatu Pastef Nooto Jobaas ;
-
Tomaas Sankarist Fay, mi yor kàddug Pastef ca Kafrin ;
-
Abdu Asiis Dabbaax, mi yor kàddug Pastef ca Kër Masaar ;
-
Abdulaay Sow, jokkalekatu Pastef Kéedugu ;