PELENT YA JOLLI NAÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Téere Séex Yérim Sekk bi ak coowal Aji Saar-Usmaan Sonko ñooy ñaari xibaar yi gën a fés ci jamono jii. Ñu jur nag coow lu rëy ci réew mi ba ay pelent mujj ci am yoon. Pelent bi ci njëkk nag, téere bi moo ko waral. Ñaareel bi moom coowal Aji Saar-Usmaan Sonko li tëw a jeex moo ko waral. Mu mel ni, jamono jii Senegaal pelent, jàpp, bàyyi négandiku walla yu ni deme, bari na lool lees koy dégg.          

Ayu-bés bii nu génn, nemmeeku nañu ci lu tollu ci ñetti pelent. Daanaka nag, ñaar yi moom ñoo bokk ki ñuy diir, muy kii di Séex Yérim Sekk. Ba ca des nag, moom, wute na ak yooyu donte ne sax am nañu lu leen boole. Kon, yeneen i wayndare yu yees yokk nañu ci liggéeyu yoon. Pelent bi ci jiitu, kii di Seydinaa Umar Ture nga xam ne bokk na ci coowal Aji Saar-Usmaan Sonko moo pelent kii di Séex Yérim Sekk nga xam nee na dafa teg ay tuuma ci ndoddam ci téere boobu mu bind. Ndax, ci diggante xët 186 ak 187 lay waxe ne dafa am wayndare yu mu yónnee Usmaan Sonko ci Whatsapp bi bokk ci li tax ñu dàqe ko ci béréb boobu. Loolu nag, mi ngi ko fésale ci ab saabal bu mu def ci mbaalu-jokkoo gii di « Facebook ». Kon, pelent yi daanaka soreewuñu donte ne sax ñaari coow yi bokkuñu.

Ñaareelu pelent bi nga xam ne tamit mi ngi ci ndoddu Séex Yérim Sekk, kii di Njiital Pastef li Usmaan Sonko mooy ki ko def. Li ko waral nag mooy ne, moom tamit, daf ne da koo tuumaal ci téereem boobu. Ndax, téere bi, daf ko cee jagleel pàcc bu yaatu (Chapitre 16). Foofu nag, daf ko cee tuumaal ne ci waajtaayu wotey féewaryee 2019 yi, ndawi pólis yi dañu koo bett ca Corniche-Ouest bu Ndakaaru ak benn xale bu jigéen bu dëkk Gàmbi ci biir benn daamar ci anam yu doy waar. Nee na bi xibaar yi àggee ca Njiitu réew ma, ca la ca tege tànkam. Kii di Usmaan Sonko moom naanewul mbir mi ndox. Ndax, dafa def ab saabal ci mbaalu-jokkoo gii di « Facebook », xamle ci ne kooku li muy wax du dëgg. Te, am na benn jëwriñu Maki Sàll bu ko waxoon ci weer yi jàll. Te, nee na bindkat bi sax setul bay digle cangaay. Ndax, amoon na fi coow yu ni mel ba pare bëgg koo jam ci fànn woowu. Rax-ci-dolli, moom jox na ndigal ay layookatam ngir ñu yónnee ko pelent (ay « citations directes ») ak kër gi móol téere bi muy Harmattan. Kii di Séex Yérim moom nee na bu yëf yi àggee dina wuyuji. Te, loolu dina tax mu mën a indi ay firnde yu ko mën a leeral. Mbir yi nag, foofu la tollu jamono jii. Téere bi nag bu dee ay leeral a ko taxoon a jóg mujj na jur ag réeroo. 

Beneen pelent ba nag coowal Sweat Beauty li moo ko waral. Kii di Aji Saar, kenn ci ndeyi-mbill yi moo ko def. Mi ngi ko jagleel kii di Séex Baara Njaay faramfàccekat ak Mustafaa Jóob mi jiite porogaraami Walfadjiri. Li ko sabab mooy, ciy waxam, kàddu yu ñu yékkati teg ko ci deram te dara amu ci. Kenn, ci ñoom nag Séex Baara Njaay yékkati na ay kàddu ci mbir mi, di ci xamle ne moom yëgul tinul. Te yaakaar na ne amul wenn yoon wu mu sosalee ndaw soosu. Loolu lay biral ci kàddoom yii : 

« Bu dee Aji Saar daf maa pelent, loolu ànd naa ci ak xel mu dal. Ndaxte, yaakaar naa ne Aji Saar bokk naa ci nit ñi ëpp lu ñu ciy wax. Ndax, dafa nekk xew-xewu jamono bu tëw a jeex lu tollu ci ñaari at. Waaye, yaakaar naa ne amul benn yoon boo xam ne yékkati naa sama kàddu gii wax ko loo xam ne lu dul noonu la walla yàq ko tax maa jóg walla yooyu, loolu moom mësul a am. (…) Amunu nag benn jafe-jafe, loolu yëguma ko, waaye su nu ko yëgee tamit amunu benn jafe-jafe. Ndax, nun ay maxéjj lanu bu ñu nu pelentee te yoon woolu nu dinanu ko wuyuji, bu ñu amee lu ñu nuy laaj dinanu ko tontu. Waaye, yaakaar naa ne daal, man séquma ak Aji Saar lu mu ma waree pelent. Nit boo koy pelent danga naan lii la ma sosal daal. Man yaakaar naa ne mësumaa sosal benn nit, ku dul Aji Saar sax duma ko sosal. »           

kon, beneen liggéey bu bees tàbbi na ci loxoy Yoon. Mu mel ni fan yii moom pelent yi, jàpp yi ak bàyyi négandiku yi dafa taqarnaase. Ak lu mën di am gaa ñi sóobu nañu ci mbojjum yoon. Waaye, ngelaw nag dina dugal ci pax loo xam ne mënuko cee génnee.      

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj