PÉNCOOY PÓLITIG BI AK DAARA YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kuréli ma-xejj yi yékkati nañu kàdduy woote jëme ci péncoom pólitig bi ñuy amal keroog 28 me ba 4 suwe 2025. Muy woote bob, ñoo ngi ko jagleel way-kujje yi ngir ñu bañ a bank seen i loxo ci dig-daje bu am solo boobu ñeel ëllëgu réew mi. Naka noonu, ñuy sàkku ci ñoom ak di leen ñaan ñu defaraat seen taxawaay te andi seen i xel ak xalaat ci liy defar ëllëgu réew mi.

Barki-démb ci altine ji lañu biral seen kàddu yooyile. Fekk ñetti kurélug ma-xejj yii di ONG 3D, COSCE ak GRADEC doon daje fa Ndakaaru ngir waajal bu baax seen bokk ci waxtaan yi. Fésal nañu nag seen taxawaay ak seen dogu ngir andi luy jariñ ci waxtaan yi ñu namm a amal ngir sopparñi pólitig beek yoonu wote yi. Naka noonu, ñuy dellu di fésal njariñu teewaayu way-pólitig yépp ak jafe-jafe yi mën a tukke ci seen ñàkk a teew ci fu ñuy jële ndogal yi.

Naka noonu, door nañu tay ci talaata ji péncoo yi ñu jagleel Daara yi fi réew mi. Ci suba gi lañu doon tijji waxtaan yi fa Institut Islamique de Dakar, ci njiiteefu jëwriñu njàng mu suufe meek mu digg-dóomu mi, Sëñ Mustafaa Màmba Giraasi. Ndaje moomu nag, moo ngi aju ci jéego yi Nguur gi fas yéene sàqi ngir jële fi yenn xewte yu mel ni xale yiy yalwaan walla di taxawaalu ci mbeddi péey yu mag yi. Mu nar a doon buntu waxtaan yu yaatu ngir yeesal daaray Alxuraan yi ba ñu mën leen a sumbaale ci doxalinu njàngum réew mi. Naka noonu, ñuy xaar ci mbooleem pàcc yi koy teewe ñu gaaral fay pexe ngir ñu mën a gunge Daara yi, aar xale yi, ñoŋal seen um njàng, te lépp dellu di sàmmonteek delluwaayu daara yi ci diine.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj