PÉNCUM RÉEW MI WALLA PÉNCUM BENNOO BOKK YAAKAAR ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am réew, su fa buur ak lingeer dee fecc, ku fay woyaan doo rus a yaŋas. Kon boog, ndokk dipite yi ! 

La xew ca Péncum réew mi ci dibéer jii weesu, ñaaw na te ruslu. Dëgg-dëgg, kenn xamatul lu péncum réew miy saf. Ndege, dara wutalewu ko ak pénci koñ yi walla garaŋ-palaas yi. Moom kay, mënees na ko méngale sax ak jataayu janq ji. Dàggsante, kekkantoo, xastante, saagaante, xuloo, xeex, yaataayumbe…nii la dipite nekke ca béréb bu tedd boobu, te kàddu askan wi doŋŋ waroon fa jib. Dafa di sax, kenn umplewul ñàkk faayda, xamadi ak xayadi bi dipite yi nekke, walla boog li ëpp ci ñoom, rawatina ñiy faral di féete ci nguur gi. Waaye, jëf ju ñaaw ji ñu def dibéer jii weesu dafa gënatee yokk xar mi karaw, gàkkalati deru Péncum réew mi, ñaawal xar-kanamu Senegaal ci àddina si. Réew mépp di naqarlu doxalinu dipite yi. Ñi dul taataan xibaar yi moom di laaj : waaw, lu dipite yi defati ?

Dibéer, 30ifan ci weeru suweŋ, Abdulaay Daawuda Jàllo, jawriñ ji ñu dénk wàllu koom-koom bi ak ngurd réew mi, moo leen doon jébbal sémbub àtte joyyanti ngurd mi (projet de loi de finance rectificative). Dipite yi waroon koo waxtaane, ku nekk joxe ci sa xalaat laata ñu koy wote. Waaye, bi dipite bii di Usmaan Sonko, njiitalu ‘’Pasteef’’, waree jël kàddu gi, dipite Bennoo Bokk Yaakaar yépp a mànkoo, jóg xajal ko ngir bañ koo déglu. Muy lu ñaaw lool sax te ruslu ci réewum Senegaal. Mëneesoon na samp laaj, ne : lu tax ñuy daw Sonko ? Lan lañu ko meree ? Waaye tontu li réerul kenn. Ndax ñépp a xam taxawaayu Sonko ci kujje gi ak xadar gi mu àndal, sonal nguur gi lool, rawatina ci wàllu coowal petorol bi ak gaas bi. Waaye, wax ji dëgg-dëgg du dellu ci jëmmu Sonko, kon ñu wute ak solos mbir mi. Bu ñu seetee ba seet, dipite yi joxuñu cër askan wi te wormaaluñu béréb bu tedd boobu di Péncum réew mi. 

Naam, dipite bu nekk, ab pàrti moo la tabb, def la wutaakon ba nga mën a bokk ci joŋante wote péncoo gi. Waaye, askan wee la sànnil xob, fal la ngir nga teewal ko fa. Mu dellu, jël lu néew lu muy fortaatu ci xaalis, joxe. Ñu dajale ko, di la ci fay weer wu dee alal ju bare, jëndal la ci oto, di la fayal esãs walla gaasuwaal ak di la ci defal yeneen xeeti xéewal. Jamono jooju, askan waa ngi xiif, sonn, mar, rafle ba noppi tumurànke. Laaju la dara lu dul nga xeexal ko, laajal ko ay àqam ngir mu génn ci ndóol ak tolof-tolof yi mu nekke. Waaye, dipite yi, ñàkk ngor ba dee, bu ñu nekkulee di nelaw, ñoo ngiy tàccu walla di wote ay sémbub àtte yoo xam ne ay njuuj-njaaj kese a ci lalu, di ab musiba ci askan wi. Waaye, lii warul a bett kenn. Ndax ñi ci ëpp am tur ak mbooloo rekk a seen tax parti tabb leen ; jànguñu, taruñu te xamuñu lu géej giy riir. Jàpp nañ daal ne, lu njiitu réew mi bëgg rekk noonu la, lu mu joxoñ ñu dagg. Loolu la kàdduy dipite bii di wuyoo ci turu Maalaw di biral : “ …Man de ci foofu laay tàmbalee ; ci sama tur lay tàmbalee. Maalaw mii, dipite Maki Sàll la. Man, dipite Maki Sàll laa, waaw. Kon liñ ñu sant dañu koy def 100%. Fii, yoon wu fi Maki Sàll indi xéy na yéen a koy xool waaye man duma ko xool. Man bu ñu nee wote leen rekk ma yékkati sama loxo.” Ñoo ko déggandoo. 

Ñi ci jàng te xam li xew, dara soxalu leen lu dul seen i poos ak nguur. Jaral na leen ñu wor askan wi. Li koy firndéel mooy bi ñu gàddaayee jawriñ ji ñu dénkoon wàllu mbay mi, Abdulaay Sekk, ba ko ca péncum réew ma moom doŋŋ, dem ci palug Maki Sàll ga. Kon, ñi jàng ak ñi jàngul ñoo bokk àtte : ñépp a wor askan wi ngir àddina ak li ci biiram. Ci gàttal, lii dipite yi def keroog du mbetteel.

Warees na xam ni, péncum réew mi, kàddu askan wi lees fay yebbi. Ku nekk ci dipite yi teewal fa gox bi ko fal. Kàddu askan wi nag, mënta doon benn ; ndax gis-gis yi dañu wute, rax-ci-dolli nekkin wi du benn. Te wolof dafa ne, bëgg-bëgg yee wute, moo tax njaay ma jar ca ja ba. Kon, bu fekkee àndoo ak li sa naataangoo wax, yoon may na la nga jëlaat kàddu gi, indi ay tontu ak i leeral. Waaye waroo dem sa yoon, ndax indiwoo fa sa bopp. Waaye, ku yeboo ne baatu askan wi sooy na. Ndaxte, dipite yii, askan wi da leen faloon ngir ñu bennoo dekkal yaakaar, ñoom ñu fas yéene bennoo tas yaakaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj