Taalif ci Maam Abdul Asiis Si Dabbaax
Mag mat naa bàyyi cim réew
Seex Abdul Asiis Dabbaax ndey-ji-séex
Luň mer mer bu waxaan xol yi féex
Gis naa ko bés jàkkay Kaay Usmaan Jéen
Ba may gune muy yooru baň ku ko séen
Meloy ku woyof la ma dikke ca Tilléen
Maam Kaatim Ture naa wàllsileen
Sëriň ba jàngi woon Faas Ture ngi nii
Reenub cofeel la saxal sama xol ba nii
Gisatuma ko fenn xanaa di ko gént
Bu ňuy ňaan baň sunu réew mi gent
Moo xam ay la nawet walla njéeréer
Sunu xel yépp dellu sunu góor ga réer
Docteur Daouda NDIAYE Jaraaf