Bàyyi wirisu Covid-19 bi law ngir sabab kiiraayu-mbooloo la Doktoor Paap Musaa Coor digle ngir xeex mbas mi. Waaye PorfesoorMusaa Séydi mi jiite Banqaasu feebar yiy wàlle ca loppitaanu Faan, àndul ak xalaat boobule. Lii la Porfesoor Séydi wax :
« Naam, way-tawat yaa ngiy yokku. Kenn werantewu ko. Waaye, bu dul woon dogal yiñ jël, romboon nan fii bu yàgg. Loolooy wone ne, fagaroo gën faju. Mu am, nag, ñu jàpp ne danoo waroon a bàyyi wiris bi mu law, dal ñu bari ci askan wi ndax ñu mën a am kiiraayu-mbooloo. Waaye, wiris boo xam ne mën na laa wàll benn, ñaar, ñett ba fukki yoon sax, sun ko bàyyi woon mu law musiba mu réy la nu naroona jural. Ñi ci ñàkk kon seen bakkan kenn du xam nu mu tollu. Duma tàyyee wax ne fagaru rekk moo nu mën a may ndam ci Covid-19 bii lëmbe àddina si.»
Ci ndaje mu jawriñu wér-gi-yaram ji doon amal ak taskati xibaar yi la Porfesoor Séydi indee leeral yile.