kuppeg àddina saa ngay wéy ca Qataar. Ci kippu A gi, Senegaal amati na ndam ginnaaw bi mu dóoree Ekuwaatëer ñaari bii ci benn, ci seen joŋantey talaata ji. Ndam loolu dina ko jàllale ci joŋantey dóor-mu-toog yi. 20i at ci ren, ginnaaw 2002, bi fa Senegaal gëjee àgg.
Senegaal jàll na ci ñaareelu pàccub kuppeg àddina si. Loolu mooy xibaar bi gën a fés ci bëccëgu tey bi. Xare badar la woon, walla talaatay ndeer. Mënul woon a yomb wenn yoon ci ñaari ekib yi. Dafa fekk ni Senegaal dafa waroon a am ndam ngir des ci xëccoo bi. Lu ko moyoon, ñibbi kon na.
Fi leen ñépp doon xaar nag, lañ génne tey. Duggusi bu baax lañu def. Moom kay, arbit bi daf ni parr mbiib ma, rekk gaynde yi fëx, wutali Ekuwaatëer. Xëccoo beek mbëkkante bi mel ni tulleek màlle. Ñu taxaw temm ci kow Ekuwaatëer. Bal bu dem, delsi. Ba bi Ismayla Saar di dugal bii bu njëkk bi (44eelu simili) ci teg-dóor, ginnaaw bi ko wattukatu ekuwaatëer bi gaañee ci taatu kã yi. Gayndey Senegaal yi teggiwuñ wenn yoon seen tànk. Senegaal daldi jiital Ekuwaatëer. Ñu dawal tuuti xaaj bu njëkk bi jeex.
Naka lañ delsi rekk, Ekuwaatëer yeewu, téyee bal bi di ko dawal. Loolu, Senegaal mayu leen woon ci xaaj bu njëkk bi. Biñ demee ba ci 68eelu simili bi, ci lañ dugal. Muy benn-benn. Waaye, ñaari simili doŋŋ lañ ci tekk (70eelu simili) Kalidu Kulibali, njiital gàdd gi, dugal. Senegaal jiitooti. Ekuwaatëer di bës ba joŋante bi jeex mënul delsi. Senegaal am ndam.
Donte ni ëppuñu luñ téyee bal bi ci joŋante bi yépp, xaley Aliw Siise yi dañ ko safal ba mu saf, sàpp. Ci xayma, 57% ci xëccoo bal yi, dañ ko yóbbul waa ekuwaatëer. Dóor nañ 15i yoon, 9 yi jubuñu. Ñaar ci 6i dóor yi jub, waaye benn duggu ci. Ñu daldi dóor Ekuwaatëer ñaari bii ci benn. Ci toftale bi, Senegaal jël ñaareelu toogaan bi ci kippu A bi, daldi jàll ci ñaareelu pàcc bi. Muy ñaareelu yoon Senegaal di àgg foofu ci wàllu kuppeg àddina si ginnaaw bi mu ko njëkkee woon ñaar-fukki at ci ginnaaw, ca atum 2002.
Ginnaaw bi mu àggee ci joŋantey dóor-mu-toog yi, Senegaal dina janook Àngalteer dibéer jii di ñëw. Balaa booba, ñu dellu wax gàcce-ngaalaama gaynde yi te bàyyi Saa-Senegaal yi bége ndam liñ am tey. Muy ndam lu réy ci ñoom ñi nekkoon di fàttaliku ki fi nekkoon gaynde Senegaal, dugaloon biiwu Senegaal bu njëkk ci kuppeg àddina si ci atum 2002. Muy Paap Buuba Jóob mi làqu woon ci 29i fan ci weeru nowàmbar 2020. Na Yàlla SWT yërëm ko te tàbbal ko àjjana.