QATAAR 2022 Talaata 22 nowàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaatay démb jee nekkoon ñetteelu bésu kuppeg àddina siy ame Qataar. Ñaari ponkal waroon cee door seen i joŋante, muy Farãs mi ko mujje jël ak Arsàntin bu Liyonel Mesi mi nga xam ne, nee na, gii mooy mujjantalug kuppeg àddina si muy bokk. Bu ndoorteg  Farãs neexe, moom mi duma Óstaraali, Arsàntin moom, tànk bu bon bi la dugge. Nde, Araabi Sawdiit gi kenn yaakaarul woon, moo ko bett, dóor ko 2i bii ci 1.

Kippu C : Araabi Sawdiit bett na Arsàntin

Ñaari joŋante lees doon xaarandi ci bésub taalata ji ñeel kippug C gi : Arsàntin – Araabi Sawdiit ak Meksig – Poloñ. Ñi safoo  powum kuppe ñépp nag, ndoorteg njuuma lii di Mesi ak Arsàntin lañ gënoon a yàkkamti. Nde, Arsàntin dafa bokk ci ponkal yi ñu njort ne, ñoo nar a jël kub bi.  Rax-ci-dolli, Mesi dafa xamle ne, gile kuppeg àddina mooy doon gu mujjam. Ñépp ñoo foogoon ne Mesi ak ñoñam dañuy boxom Araabi Sawdiit ni caaf, yéy, dox seen dox. Waaye de, mbetteel gu réy a réy la àddinay kuppe sépp ame, rawatina saa-arsàntin yi. Dafa, ndawi Erwe Rënaar yi dañu def jaloore ju mag, futbal ak Arsàntin, xeex ak ñoom ci gasoŋ bi, daan leen.

Moone, Arsàntin moo njëkk a dugal, ci ndoorteelu mats bi. Mesi moo dugal penaatii, bi mats amee 10i simili. Ñu ee-yaay, tey naar yi dee. Te sax, ci xaaj bu njëkk, saa-arsàntin yi yëngal nañ ci caax yi ñetti yoon, ñu bañ yépp ngir « hors jeu » : Mesi (22eelu simili), Lawtaroo Màrtines (27eelu simili ak 35eelu simili).

Bi ñu delsee ci ñaareelu xaaj bi, naar yi dañu fippu, soppi seen xar-kanam tàmbalee tàppaas Arsàntin. Noonu, Saleh Al-Sehri moo njëkk a toj kërug góolu Arsàntin bi ci 48eelu simili bi. Ñu ne déet-a-waay, Salem Al-Dawsari tojati kër gi, yëngal caaxi Màrtinees mi ci kã yi, muy 2-1, naar yi jàll ci kanamu Arsàntin. Noonu, Mesi ak ñoom Di Mariyaa jéem lu nekk, waaye duñu mujje dugalaat ba ni mats bi di jeexe. Muy kaawteef, di mbetteel gu réy. Fi mu nekk nii, fàww Arsàntin dóor ñaari joŋante yi ko dese bu bëggee génn kippoom.

Ñaareelu joŋanteb kippug C gee ngi doxoon diggante Meksig ak Poloñ mu Lewàndóowsikii. Ñaari ikib yi dañu témboo, ndam demul, ndam dikkul. Góolu Meksig bee fa góolu lu réy. Jàpp na fa sax penaatiiwu Lewàndóowsikii. Gaawu bii di ñëw, Poloñ ak Araabi Sawdiit dinañ joŋante bu 13i waxtu jotee, Arsàntin ak Meksig laale bu 19i waxtu jotee.

Kippu D : Farãs wulli na Óstaraali

Farãs mooy ponkalu kippu gile, moom mi jëloon raw-gàddu gi ci joŋanteb Riisi ba, ñeenti at ci ginnaaw. Danmàrk, Tinisii ak Óstaraali la bokkal kippu gi. Ci talaatay démb ji la matsi kippu gi waroon a door. Farãs waroon a janoo ak Óstaraali, Danmàrk ak Tinisii doon laale ci bi 13i waxtu jotee.

Ikibu Farãs bi nag dañ ko doon xaar ngir sabab yu bari. Ndaxte, benn la ci ponkal yees di sóor ca mujjantal ga, moom, Beresil ak Arsàntin. Waaye tamit, ay kuppekatam yu bari te ràññeeku dañu wuute xëccoog ren ji : Bensemaa, Pogbaa, Ngolo Kànte, Nkunku… Ñu doon ragal loolu nasaxal ko. Waaye, démb, génn na ci. Nde, wulli na Óstaraali wulli yu metti, dóor ko 4i bii ci 1. 

Óstaraali moo njëkk a boyal caaxi Farãs, bi mats dawee ba 9eelu simili bi. Waaye, ci 27eelu simili bi la Rabiyoo dugal, tollale leen. 5i simili (35’) kepp lees ci teg, Siru dugal, Farãs am 2, Óstaraali 1. Noonu la xaaj bu njëkk biy jeexe. Biñ delsee, Farãs dafa sëpp Óstaraali, Mbape dugal ci 68eelu simili bi laata Siru di dugalaat ci 71eelu simili bi. Noonu la joŋante biy jeexe.

Bu gaawoo, 26 nowàmbar, Tinisii dina janoo ak Óstaraali (10i waxtu ci suba) laata Farãs di joŋante ak Danmàrk ci mats bu nar a neex.

Ngirtey bés bi

Arsàntin   

1

2

Araabi Sawdiit

Danmàrk  

0

0

Tinisii

Meksig     

0

0

Poloñ

Farãs        

4

1

Óstaraali

Joŋantey ëllëg, àllarba 23 nowàmbar 2022

Marog   

      Kurwaasi

Almaañ  

      Sàppõ

Espaañ     

      Kostaa Rikaa

Belsig        

      Kanadaa

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj