QATAAR – SENEGAAL, NDAM REKK

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi mu ñàkkee joŋanteem bu njëkk bi digganteem ak Olànd, Senegaal dina janook Qataar mi dalal kuppe gi. Ci àjjumay tey jii la mats biy am, bu 13i waxtu jotee,

Amul xalaat, ndam rekk a fi sës. Bi kuppeg àddina si dooree ba nëgëni, du benn ikib, ci juróomi ikibi Afrig yi, ku gañe. Senegaal a njëkkoon a ñàkk, Tinisii ak Marog témboo, Kamerun lajj, Gana daldi daanu moom tamit. Gana mi dugal 2i bii sax a ci tane. Loolu nag, du sagu Afrig. Moo tax, fim ne nii, Senegaal dafa am sas, moom mi mujje jël CAN bi te jiitu ci ikibi kuppey Afrig. Yaakaarees na ci Aliw Siise ak i gayndeem yi ngir ñu siggil Afrig ci seen joŋante bi ñuy am ak Qataar.

Senegaal dafa war a gañe ñaari matsam yi des ngir génn ci kippoom gi. Loolu nag, mi ngiy doore matsu tey ji. Waaye nag, joŋante bi narul a yomb. Ndax, muy Senegaal di Qataar, ñaari ikib yépp a ñàkkoon seen mats bu njëkk, ku ci nekk ñu dóor 2i ci 0. Rax-ci-dolli, Qataar mi nekk dëkkam dina def kemtalaayu kàttanam ngir bañ a gàcceel way-farandoom. Dafa di nag, Senegaal a gën a diis Qataar. Moo tax, moo gën a yey ci jël ndam li.

Kuyaate ak Fóode B. Ture duñ bokk, Abdu Jàllo tàggatu na ak yeneen kuppekat yi

Joŋante bu jiitu ba, nun ak Olànd, Seexu Kuyaate àggaliwu ko woon. Dafa toogoon ginnaaw bi mu gaañoo ci ginnaaw pooj pi. Fédération bi xamle na ne, du mën a futbal matsu tey bi. Paap Géy mi jëloon palaasam keroog, moo ko nar a wuutu ci 11 yiy door. Abdu Jàllo tamit dafa toogoon ci sababu gaañu-gaañu. Waaye, nee ñu, amaana mu bokk ci ndaje mi ndax jot naa tàggatook moroomi kuppekatam. Kii di Fóode Baloo Ture moom, du bokk tamit.

Amara Taraawore, moom, dafa gis ne Senegaal dafa warul « xalaat », dafa war a « gañe ».

Aliw Siise nee : « Joŋanteb ëllëg bi, wóor na ma wóor ni, dina wute ak joŋanteb Olànd ba. Awma sikk-sàkka ci ne sunu dugalkat yi aay nañu aay boo xam ne dinañ dugal. »

Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj