Qatar 2022 : Ay mbetteel kese la

Yeneen i xët

Aji bind ji

Benn bés a des ngir joŋantey kub bu àddina si door fale ca Qataar. Fanweeri bar (ikib) ak ñaar war koo teewe. Waaye itam, wurekat yu bare te ràññeeku lool ci po mi naruñoo xam lu mbir miy saf. Ci ñooñu ñu gën cee ràññe wurekat bii di Saajo Maane te bokk ci ñi gën a xarañ ci àddina si ci atum 2022 bi.

Jamono yii, mboolem bar yi war a joŋante kub bu àddina see nga lal basaŋ ca Qataar. Àddina wërngal képp abal leen i nopp, teg leen i bët, ak a xaar dibéer 20i fan ci weeru nowàmbar ngir ànd ak ñoom weeru Yàlla ba keroog, 18i fan ci weeru desàmbar, ku mën di gàddu ndam li. Muy xew-xew bu réy lool ci tàggat-yaram, raw-gàddu gi ëpp dayo ci futbalu àddina si. Wurekat bu nekk, bu doon sagoom, dina ko teewe, teewal fa réewam, ba faf gàddu ndam li yóbbaale. « sama gént gu gën a réy mooy jël kub bu àddina si ak Norwees » (Erliŋ Haala).

Waaye, bala kenn naan naam dafay fekk nga nekk fa. Keroog, bi bokkadil yi jeexee, la mbetteel yi tàmbalee bare. Ay ponkal daanu, seen i mébét jàdd yoon. Bar yu mag ànd ak seen i wurekat yu kenn dul nàttaable ferankulaay, fas yéene toog xaar ba beneen yoon. Ñu mën cee lim Kolombi, Itaali, Suwed, Sili ba ci Norwees ak doomam Erliŋ Haaland mi ëpp i bii ca raw-gàddu gu Àngalteer. Bu dee ci déndub Afrig, Esipt, koddiwaar, Niseeriyaa, Alseri bokk nañ ci ñi gën a fés. Ñu doon i bar yu am doole, ahlu futbal seede ko ndax wurekat yu xarañ ya fa daje.

Bu ñu bare naree uute mbir mi, ñu ci ëpp dafa fekk ni seen i bar a jàllul ci bokkadil yi. Mu mel ni dina am ñu ko dul teewe te seen i bar yaa nga fa. Ñii, tàggatkati bar yee leen njuuy ci seen i tànneef, ña ca des gaañu-gaañu yaa fa jaar. Ci ñi mujj ñii nag la mbetteel yi gën a tee réy. Seen xalam dafa demoon bay neex, buum ga dog. Ñu gën cee ràññee Saajo Maane (Senegaal – Bayern).

Moom nag, dafa bokk ci wurekat yiñ tabb bu yàggul dara, bi ñuy joxe balu wurus bi, ni ñoo gën a wone seen xarañteef ci 2022 bi.  Bensemaa mi jël balu wurus bi, waa Farãs amoon nañ ci moom yaakaar lool ngir delloo buum ca boy-boy ga, ndam li bañ a jóge ci seen i loxo, mi ngi ci jiixi-jaaxa. Waaye Saajo Maane, leer na ni mënul a bokk. Muy lu diis. ci moom ak i ñoñam. Jël na kub bu Afrig ak waa Senegaal ca Kamerun, doon fa wurekat bi gën a xarañ. Ci benn dóor, mu toogloo ci Esipt, yóbbu Senegaal monjaal, dellu topp ci ginnaaw Bensemaa ci balu Wurus bi.  Ñépp a doon xaar mu gàddu Senegaal ak i farandoom ba yóbbu ku fum mësul a àgg ci kub bu àddina si.

Gaañu-gaañu Saajo bi nag, tax na kenn ci wurekat yi gën a xarañ ci àddina si du teewe Qatar 2022. Terewul benn bés rekk a des wure wa dem këŋ. Ñuy xaar kuy wuutu Farãs mi gàddu woon ndam li ñeenti at ci ginnaaw (2018) ca Riisi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj