R. BOURGI : “LAWAXU USMAAN SONKO MOOY GËN A…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Robert Bourgi, layookatu farãse bi, àddu na ci géewu pólitigu Senegaal. Waa Dakar Times ñoo ko doon laaj muy tontu. Ci biir laaj tontu bi, joxe na xalaatam ci wotey 2024 yees dëgmal, rawatina ci mbirui Usmaan

Sonko, Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll. 

Bu dee njiitul Pastef la woon, xelalkat bi ci wàllu pólitig dafa gis ne, mu bokk ak mu bañ a bokk yépp dina jeexital ci wote yi. Daf ne :

“ Bu ñu teree Usmaan Sonko bokk ci wote yi, lawax bi muy jiital mooy gën a mën a indil jafe-jafe Nguur gi kii di Xalifa Sàll.”

Robert Bourgi dafa gis ne, Usmaan Sonko rekk a xam li ci xolam. Li meeru Sigicoor biy nas ak a nocci, keneen xamu ko ku dul moom. Waaye, dafa jàpp tamit ne, bu dul woon njuumte yu réy yi Sonko def, doon na nekk lawax bi gën a jekku.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj