Jëwrin yees dénk wàlluw bittim réew ca Mali, Burkinaa ak Gine jot nañoo amal am ndaje ca Burkinaa. Ndax ñetti réew yi dañoo nekk ci tànki réewandoo ginnaaw bi leen kurél yi ëmb réewi Afrig yi, UA (Union Africaine, Kurélug Réewi Afrig yi) ak CEDEAO (Communauté Économique des États de l’Afrique de l’Ouest, Kurélug Koomug Réewi Afrig Sow-jant yi), beddee ? Loolu
la àddina sépp di laajte ci ñaari ayu bés yii.
Ayu-bés bi weesu, magum jëwrinub Burkinaa bi, Apolineer Tàmbelaa, dafa yékkatiy kàddu doon siiwal ne :
« M. Ibraayma Siise (magum jëwrinub Mali) dafa jógge Bamakoo ba Wagadugu ngir dégtal nu raayay Mali ak Burkinaa ak di nu xirtal ci réewandoo. Te jëfam jooju, dunu ko neenal. »
Ginnaaw ayu-bés bi mu yékkatee yile kàddu, nu gis ni jëwriniy Mali, Burkinaa ak Gine yi ñu dénk mbiriy bittim réew daje ca Burkinaa, doon fa amal ab waxtaan naka démb ci alxames ji (09 féewaryee 2023). Loolu tax ba àddina sépp sàmp ab laaj : ndax Burkinaa, Mali ak Gine dañoo nekk ci yoonu réewandoo ?
Bi ñu noppee ci seen ndaje moomu, jëwrin yi (Óliwiyaa Ruwàmba ‘Burkinaa’, Abdulaay Jóob ‘Mali’ ak Mórisàndaa Kuyaate ‘Gine’) ànd nañu siiwal ab yëgle. Ci biir yëgle boobu nag, ña nga cay xamle ni dara waralul seen ndaje mi lu dul ni ay réew yu jegeyoo la ñu ba noppi mbatit ak mboor boole leen, rawatina jamonoo yii nga xam ni ñoo bokk i bëgg-bëgg. Li ñu bëgg mooy fexe doxal gis-gis yi waraloon judub UA ak CEDEAO.
« Bu nu gisee ni nit ñi di demee ak dee ñëw ci biir kémbar gi (Afrig), yaakaar naa rafetul benn yoon ba nu koy ndamoo. Bu nu xoolee bu baax, doxandeem yi sax la dem beek dikk bi gënn a yémb Saa-afrig yi. Loolu lu mu nuy jàngal ci sunu naalub tabax bennoog Afrig ? Laaj bu mag la. Foog nu jéem a dox jëm ci loolu. Te jàpp naa ni yitte doŋŋ la laaj. (Abdulaay Jóob)
Bu loolu weesoo tamit, ña ngay sàkku ci kilifay CEDEAO yeek yu UA yi ñu teggi daan yi ñu teg ci seen kow, te bàyyi Njiiti ñetti réew yi ñu jiite ni mu ware feek 24i weer laata ñuy amal i wotey njiitum réew. Ci pàttali, bokk na ci sàrti CEDEAO yeek yu UA yi, képp ku falu Njiital réew ci anam yu dëppoowul ak ndeyu àtte réew ma, du mën a teew ci jotaayi kurél yi.
Kon, ndax kilifay kurél yi dinañu nangul ñetti njiiti réew yi seenug càkkuteef. Mbaa du dañu leen a bëgg a tiiñal ? Nde bees xoolee ak li xew Càdd, méngoowul benn yoon ak sàrt yi. Bi Njiit la, Idiriis Debi daanoo ci toolub xare ba, doomam moo ko wuutu ca boppu réew ma, terewul ñu nangul ko ko.
Ndax ñetti réew yi dañoo fas yéene boole seen doole ngir xeex rëtalkat yi ? ndax dañoo bëgg CEDEAO ak UA nangul leen li ñu nangul Mahamat Idiriis Debi Itno ca Càdd ? Ndax sax dub pexe, ab nattu, ngir ñu bañal leen ko ba ñu amee fa poroxndoll ber seen réewandoo bopp? Yii yépp diy laaj yu sàmpu. Ak lu mu ci mën a doon, lu ci kanam rawul i bët. Noo ngi xaar luy doon tontu UA ak CEDEAO ñeel seenug càkkuteef.