Dooley xale xajul ci mag. Loolu la doomu Caaroy ji wan na doomu Mbuur ji, démb ci dibéer ji. Waaw, Rëg-Rëg ak Bombarjee ñoo doon sëgg démb fa « Arène nationale » ba. Rëg-Rëg moo ko daan jéll bu set wecc. Te sax, daf ko jàpp, jaay ko doole, jaay ko xale.
Ñaari mbër yépp nag, waajal nañu seen bés bi ni mu waree. Dafa di, ku leen gis, xam ni liggéey nañu, te yit jox nañu seen bés bi àqam. Képp kenn ci ñoom indi na taxawaay bu am solo, xumbal fa.
Laata ñuy bëre, mbër yu ndaw yi amal nañu bëre yu neex. Kii di Aama-Neex daan na ca Bebe Jéen, xale bu mën a bare te bari ay soppe, kaar. Mënees na wax nag ne Bebe Jéen dafa juum ca congam la. Daf ko yàkkamti fekk ñoragul. Ama-Neex mi nga xam ne di como ci làmb ji, daf ko ci nax, kal tànk ba, daldi koy daan. Ba boobu bëre jeexee la Bombarjee ak Rëg-Rëg waroon a bëre.
Ñari mbër yu mag yi daldi sóobu ci seen i xarfa-fuufa ak seen i mbir yu mujju. Ñu ngi sëgg ba 20i waxtu tegee 36i simili. Ñépp foogoon ne dañuy xeex. Waaye, dañu léewatoo ab diir, kenn deful dara, arbit bi dànkaafu ku ci nekk. Ginnaaw loolu, ñu sëggaat, di léewatoo lu yàggul dara, xale Caaroy bi songu doomu Mbuur ji cong mu ñor xomm nag, jàpp ñaari loxoom ca ngémbu Bombarjee ga. Ponkalu Mbuur mi sax xaw naa bañ-bañlu ab diir bu gàtt. Waaye, li ñuy wax rekk, bañ, bañ, nangu. Rëg-Rëg dafa jàpp rekk bañ a bàyyi, takk ko, dëgëral ba mu dëgëral, baaj-baaje ko, daldi koy daan jéll bu sett wecc.
Mu nekkoon bëre bu neex, bu rafet. Gannaaw jéll bi, ñaari mbër yi longoo nañu, doomu Mbuur ji jàpp loxo Rëg-Rëg yëkkati ko ci kaw. Muy lu rafet !