Jot nan xibaar buy wax ne, ràppëer bii di Abdulaay Kamara, ñu gën ko xam ci dàkkentalu Baaba Kaana, ñàkk na bakkanam. Ñenn ñaa ngi naan bal dëggantaan lañ ko dóor, ñeneen ñiy wax ne takk-der yaa ko jàppoon. Ak lu ci mën di am, fekk nañ néewam ca loppitaanu Yoof. Ca njëlbeen ga, doon nañ wax ne ci tefes gi lañ fekk néewam. Waaye xibaar boobu wérul ndeke. Ñoo ngi xaarandi ay leeral yuy tukkee ciy mbokkam ngir ay xibaar yu gën a leer te wér.
EJO ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale mbokkam yeek soppeem yépp, di ko jaale ràppëeri Senegaal yi ak waa réew mi. Yàlla na ko Yàlla yërëm te jéggal ko.