SAA-CEES DAANAAT NA SÀRKOO !

Yeneen i xët

Aji bind ji

14i at ci ren gannaaw ba Saa-Cees ak Sàrkoo njëkkee bëre. Seen lámb jooju, doomu Géejawaay ji moo ko yóbbuloon doomu garã-yoof ji, daanoon ko ca. Ci dibéer jii, 22i fan ci weeru suwe, lañu doon amal seen ñaareelu sëgg. Saa-Cees moo ci daanaat Sàrkoo. Baay Njaay, rakku Asiis Njaay ji moo tëggoon làmb ji.

Laata mbër yu mag yi doon laale nag, amoon na bëre yu am ci mbër yu ndaw yi. Ci yooyu, ñu bari doon nañu ci xaar bii di bu Fiis dii Tiigar ak Booy Ka. Mu newoon itam bëre bu ñu bari doon xaar ndax li ci doomu mbër feeñ, andaale coow ci làmb jeek mbaali-jokkoo yi. Foo geestu ñu ngay wax ci moom tey waajal bésam beek Booy Ka. Moom Fiis dii Tiigar, di doomu Mustafaa Géy (ñaareelu tiigaru faas), bii moo newoon bëreem bu njëkk. Moom ab njàngaan la woon, dafa jàng, aw fi mu war a aw ba mu neex ko, mu ne làmb daal la bëgg. Mu waajal bésam na mu waree, ay magam ak i baayam ca faas gungee ko. Booy ka, doomu Pikin ji itam bàyyiwul woon boppam.

Booy ka moo ko mujje daan. Mu nekkoon bëre bu neex, ñaari mbër yi xeex fa, bëre fa bëre bu neex tamit. Booy ka daldi koy tegal siis daan ko jéll bu rëy.

Saa-Cees ak Sàrkoo nag, ku ci nekk andi nga li nga liggéey. Seen i jàkkaarloo, ñépp a gis na mu melloon, neex, bari nappanteek tëkkuwante. Sàrkoo ne woon ko ba nga may daan ca 2011, damaa newoon xale, juum ca moo waraloon na mu demee. Mu dolli ci ne ko wii yoon dinaa la daan, jëli sa mag Bàlla Gay. Waaye Saa-Cees ne woon na ko moom it, fa ma la jaaroon laa lay jaarat rekk. Mu mel ni noonu nag la demee, ndax daanaat na ko jéll bu gën a leer.

Bëre bi neexoon na lool. ñoom ñaar ñépp andi wér ak taxawaay wa ca war. Arbiitar ni piib, ñu léewatoo. Yàggul dara, Sàrkoo wuti ko. Ci noonu, ñaari mbër yi sànnante fay kurpeñ yu tàng jérr, xaw a jaxasoo, rakku Balla Gay ji sànni ko mu mel ni xale garã-yoof bi dafa rëpp ñeenti cëram. Arbiitar bi ne dawal leen, dara xewul. Ayca, ñu nekkati ci. Ku ci nekk di yóbbanteeti ay tuubaa-njaaréem. Yàggul dara, ñu roofoo. Ca congu moomu la làmb ji jeexee. Saa-Cees daanaan ko. Loolu nag dimbali na Saa-Cees ndax Ëmma Seen moo ko mujjewoon a daan, waaye tëjal na Sàrkoo buntu ci magam ja mu jëmoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj