SAA-CEES YI SÓOBU NAÑ CI XEEX BI !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndaw ñi jóg nañu fa Cees. Mu mel ni ndaw ñi fippooti nañu. Tay ci àjjuma ji lees joxe woon ndaje ngir wéyal seen xeexub ñaxtu bees nekke gannaaw ba Njiitu réew mi biralee ni dafay dàq wotey féewiryee 2024 yi ba Desàmbar. Tay jii nag, ba ndaw ñi jullijee jumaa ba noppi lañu génn ci mbédd yi, tàmbaleeti seen taal yeek sànnante xeer yi.

Ci diiwaanu Cees, ñoo ngi ci bu baax. Seen xeex bi nag, dafa tasaaroo. Ndaw yi taxawuñu ci benn bërëb, dañuy taal fii jóge fa taal fa ca des, jàppe ko noonu. Way-sàmm kaaraange réew mi nag, ñoom, seen i daamar lañ nekk di wër ngir dàq ndaw ñi. Ci biir Cees, xeex yaa ngi gën a ame ci Site Lami, konkoord, Medina Faal ak ca Palaas dë Farãs ba. Genn kàddu nag la ndaw ñi ame mooy : « doyal nanu ci Maki, nanu abal sunu réew ! »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj