Ci gaawu bii weesu, 19eelufan ci weeru desàmbar, waa Ngajaga tiit ak njàqare lañ xéye. Daanaka, askanuw Senegaal ci boppam a jaaxle woon, tiit lool ci safara sa tàkkee ci benn teenu gaas ba ca isinu Forteza. Mbir maa ngi xewe Ngajaga, benn dëkk bu féete Nóoto-Guy-Jama, ca diiwaanu Cees.
Sabab bi : «li am, deesu ko woowe “explosion”…»
Forteza, noon la isin bi safara si tàkke tuddu. Senegaal ak ay doomi Amerig ñoo ko bokk. Waaye, Senegaal mi Petrosen teewal moo moom 95% yi. Kon, mënees na wax ne, isin bi, moomeelu Senegaal la. Bees sukkandikoo ci kàdduy Basiir Daraame mi yor kàdduy Petrosen, lees fay génne ci gaas barewul, « 30 000i ba 35 000i meetar kib bés bu nekk ».
Keroog, ci gaawu bi ndogal li ame, dañ doon amal i liggéey ci fooraas yi nekk ci isin bi. Biñ àggee ci 11eelu teen bi, fa la musiba bi ame. Dafa amoon benn tiwo gaas bu bëttoon, gaas bi di ci génne. Fekk ne, jamono jooju, aji-aayu (expert) amerikeŋ bi jiite isin bi am na lum doon defar. Bi mu sampee gurub elektorosen, nag, kuraŋ bi daldi fett. Fett-fett boobu ak gaas bi doon saxaar ñoo waral safara si.
Bi safara si tàkkee, dafa jur tiitaange gu réy a réy. Nde, taal bu mag la def, di saxaar saxaar su bare lool te ñuul. Waa Ngajaga tiit, jaaxle. Ñu naan isin ba ekspoloose na. Rajo yeek tele yi biral ko ; ñu tas xibaar bi ci lënd gi (antarnet bi). Ci la njiit yi gaawtoo indiy leeral.
Bi nit ñiy wax waxi « explosion », Basiir Daraame dafa weddi loolu. Ci la ne,
« li am, deesu ko woowe “explosion”, du loolu. Dafa am tiwo gaas bu bëtt, gaas biy saxaar, fekk mu am liñ doon defar. Léegi, ab fett-fett bu bawoo cib gurubu elektorosen moo dajeek gaas bi doon suus, mu daldi tàkk. »
Mu teg ci ne, loolu, lu jaadu la. Waaye, doomu Amerig bi, moom, muccu ci. Ndaxte, jële na ciy gaañu-gaañu yu metti, sax. Jamono jii ma nga loppitaan. Nit ñi, nag, fim ne nii, seen xel dalul.
« Jarul tiit, jarul ragal… »
Bi safara si tàkkee, dañu gaaw woo pompiyee yi. Waaye, biñ àggee, taal biñ fa fekk ak taal yiñ tàmm a fay du benn. Dafa di, guléet lu ni mel di am ci réew mi. Senegaal mësta jànkoonteel ak safara su ni mel. Moo tax, ba tey, mënuñu koo fay. Looloo gën a tiital nit ñi.
Loolu la Basiir Daraame xam ba tax muy dalalaate. Ciy waxam, yabalees na fay pompiyee yu xereñ ak ay kàngami Petrosen. Démb ba léegi, ñoo ngi fay saytu ak a wattu safara si ngir mu bañ a jur benn xeetu loraange. Baasir Daraame neeti, « jarul tiit, jarul ragal ».. Nde, muy askan wa fay yeewoo walla jumtukaay ya fa nekk, kenn du ci loru te dara du ci yàqu. Waaye, nag, ci dëgg-dëgg, am nay yàqute yu bare yees fa nemmeekoogum ci sababu safara si. Wànte, ba tey, taxul Basiir Daraame miy waxaaleel njiit yi ragal. Mu neeti :
« Fi mu ne nii, gaas bi rekk mooy tàkk. Te, bu dee loolu rekk la, jarul nuy tiit. Ndaxte, ni soorooru SAR biy tàkke, noonu kese la gaas biy tàkke. Rax-ci-dolli, fi taal bi nekk, kenn dëkku fa. Bu dul dëkk-dëkkaan yi ko wër, safara si soree na dëkk bi ko gën a jege 1 km. »
Fi mu ne nii, sàppëer yaa ngiy liggéeyandoo ak liggéeykati Petrosen yeek yu Forteza yi ngir seet nu ñuy def ba fay taal bi.
Ndimbal ñeel na nguur gu mball
Bërëb baa ngi ne dell ak i oto sàppëer. Waaye, ba ci talaata ji, fayaguñ woon safara si. Way-aayi amerikeŋ yi bokk ci Halliburton lañ mujjee woolu ngir ñu jàppalesi leen. Ñoom, waa Halliburton yooyu, ci petarool lañuy yëngatu. Ndekete, taal bi, fay ko du lu yomb. Mën na dem ba 15i fan, bees sukkandikoo, ba tey, ci waxi Basiir Daraame mi yor kàddu Petrosen.
Lii nag, day wone ne njiiti réew mi lajj nañ.
60i at, gannaaw bi Senegaal moomee boppam ba tey, mënaguñoo fayal sunu bopp ab taal bu gaas sabab. Amunu xam-xam bi astemaak jumtukaay yi. Ñu nekk fiy salfaañe xaalis ci TER boo xam ne Yàlla rekk a xam ndax dina mës a daw ; di xëpp alalu réew mi ciy aaren ak i estaad yu amalul askan wi benn njariñ.
Moo tax, ci gis-gisu Basiir Daraame, nu war a ngembuwaat. Ndaxte kat, fii ak i weer, Senegaal tàmbalee liggéey gaas bi ci réew mi. Bu ko defee, warees na tàggat ndawi réew mi ak ñépp ñiy yëngu ci mbirum gaas, petarool ak yu ni mel. Gannaaw gi, warees na gànnaayoo jumtukaay yu yees, méngook jamono te mucc ayib.
Ndege, sunu sàppëer yi, ay taal yu ay matt ak i ñax sabab lañ tàmm a fay. Bii yoon, nag, leneen la. Kon, jot na ñu tàggat leen ci yeneen safara yi nga xam ne, gaas, petarool walla mbëj moo koy sabab ngir ñu mën ko fay ciy anam yu mucc ayib. Ci la kaaraange askan wi aju. Ndeysaan, sunu njiit yi, tal nañ leneen ndax seen cuune. Te, nguur gu cuune gu ne, dinga mball. Te, ndimbal ñeel na nguur gu mball ni nguuru Senegaal.
Looloo waral ku ci mel ni Magéy Njaay, meeru Ngajaga, wax ne « ci nen lan toog ». Gannaaw gi, mi ngi artu, di wax ne, « tey jii, bu dee fattuñu bën-bën yi, safara si mën naa law ba àgg Ndakaaru ci sababu “pipe-pline” bi. »
Lu ni mel rekk a tax Fabrice Nguéma naan, suba su nekk, buy biral li gën a fés ci yéenekaay yi day yuuxu ca kow :