Sàndikaa yu bari door nañu ay ñaxtu ci ayu-bés bii. Muy ñi féete ci njàngale mu kowe mi, di ñi féete ci paj mi ak sax ci yeneen sàndikaay liggéeykat yi (PATS). Dafa di, ñoom, bu yàgg ba tay ñi ngi àrtu. Waaye, Nguur da ne patt-pattaaral, mel ne ku yëgul li gaal gi di riir. Moo tax, ñu làbbali, yokk cere, dolli ñeex. Li ñu ko dugge du lenn lu moy won Nguur gi ne lañu nekkoon, jóguñu ca. Maanaam, tay la Waalo gën a aay.
Ñaxtu yi taqarnaase nañu lool fi réew mi, rawatina fan yii. Ayu-bés yii ñu génn yépp ndongo yi nekk ci daara yu kowe yee doon amal i doxu ñaxtu. Ñu jóge ca, yeneen banqaas jël lenge yi. Nde, suba ci talaata ji la sàndikaab jàngalekati daara yu kowe yi di SAES (Syndicat Autonome de l’Enseignement Supérieur) ak SAMES (Syndicat Autonome des Medecins, Pharmaciens, et Chururgiens-Dentistes du Sénégal) sàndikaab fajkat yi di door seen i ñaxtu. Dinañu dakkal seen ub liggéey diirub ñaari fan.
Naka noonu, sàndikaa yi bootu ci PATS (Personnels Administratif, Technique et de Service des universités publiques, des centres des œuvres universitairres et établissements d’enseignement) yi tamit door nañu ab ñaxtu. Tay ci altine ji lañu woote woon am ndaje mu mag fa Cees. Ca ndaje mooma lañu jëlee ndogal li. Tay lañu door seen ub ñaxtu. Te, dinañu ko wéyal ba suba ci talaata ji.
Sàndikaa bu nekk nag dafa an lu muy sàkku ci Nguur gi. Ñii di waa SAES moom, li ñuy naqarlu mooy li ñu tegagul ci yoon payooru (pension) alaaterete yi walla jàngalekat yi génn àdduna. Te, foofu dañ faa salfaañe sàrt yi Yoon tëral ñeel ñi liggéey ba at yi ñu leen mayoon jeex. Bi ci topp, mooy ñàkk a gëddaal gi Nguur gi ñàkk a gëddaal déggoo bi ñu amoon ci weeru oktoobar wii weesu. Waaye, ba tay Nguur gi gëddaalul li ñuy dippe “clause de confiance” bi doxoon seen diggante ñeel xaatimub dekkere bi. Bi ci mujj, mooy li njëwriñal njàngale mu kowe mi gumba-tëxlu ci poñ yi ñu tënkoon ci ñaxtu bi ñu doon waaj a amal ci weeru sãwiyee wii jàll. Looloo tax, ñu jël ndogalu dakkal bépp liggéey bu ñu war a def ci ñaari fan yii (talaata ak àllarba).
Ñii di waa SAMES tamit, li ñuy sàkku mooy fajkat yi (medecins, pharmaciens et chirurgiens-dentistes) amul xéy, ñu jël leen ñu liggéey. Ñu gën a jox dayo li ñuy jox (pension) fajkat yi liggéeyatul. Rax-ci-dolli, ñu yemale ndàmpaay yi. Ni ñu koy defee ci yeneen banqaas yi, ñu joxee ko noonu ci paj mi. Waaye tamit, ñu tabax ay raglu ci gox yépp ngir yombalal askan wi paj mi. Poñ yooyu bokk nañu ci li tax sàndikaa boobu bëgg a dakkal seen ub liggéey ci diiru ñaari fan (talaata ak àllarba).
Ndogal yi sàndikaa yooyu jël terewul mu am ñaari sàndikaa yoo xam ne ci njàngale mu kowe mi lañu bokk, te, bokkuñu ci ñaxtu yooyu. Muy STESU (Syndicat des Travailleurs des Etablissements Scolaires et Universitaires) ak sàndikaa PATS (Personnels Administratif, Technique et de Service) bu mag bi. Ñoom, nee nañu waxtaan yi ñu séq ak jëwriñ ji ñu séqal njàngale mu kowe mi dal na seen xel. Te, ñi ngi sàkku seen i naataangoo yi bokk ci sàndikaa yooyu, ñu may leen nopp.
Mu mel ne ñaxtu yi moom sàndikaa bu nekk a ngi ciy bay waaram. Ñi door nañu, ñee a ngi waaj. Laaj bi mat a samp kay mooy, ndax Nguur gi day wéy di leen soofantal ? Walla day mujj wuyusi leen ci li ñuy sàkku. Fii ak ub diir dees na xam fu wànnent di mujjeek i bëtam.