Càmmug Senegaal ak SINOHYDRO (bànqaas ci kër gii di Power-China) taxawal nañu liggéeyi sémbub GTE (Grand Transfert d’Eau) bi nu duppee Autoroute de l’eau du Sénégal. Muy Sémb wu mag wu nar a jotale ndoxum dex gii di « Lac de guiers » ba Tuubaa, Cees, Ndakaaru ak Mbuur.
Barkaatu-démb ci alxames ji, 31i oktoobar, la Càmmug Senegaal (jaare ko ci FONSIS, Fonds Souverain d’Investissements Stratégiques du Sénégal) ak waa SINOHYDRO xaatim déggoo bi taxawal liggéeyi yoonu ndox mii di Autoroute de l’eau du Sénégal.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi njiitul FONSIS li fésal, Baabakar Ñing, bés bu sémb woowu noppee, dina jotale ndox mu sell lu tollu ci 5i tamndareeti doom-aadama, ci diggante ñeenti dëkk yu mag yii di Tuubaa, Cees, Ndakaaru ak Mbuur. Bees ko tàllalee ba 2050, mu méngook gis-gisub Senegaal 2050, 11i tamndareeti doomi Aadma dinañu ci jariñu.
Ba tey ci kàdduy Baabakar Ñing, bu weesoo ñi koy jëfandikoo ngir naan, dina doon itam sémb wuy suqali mbay mi. Nde, dees na ci nàndal lu ëpp 12 000i ektaar ciy tool. Naka noonu, fileek 30i at ci kanam, réew mi dina tàggook lépp luy jafe-jafey ndox ci dëkki taaxam yi gën a mag ak ci mbay mi ñuy amal ci dëkki ñaay (zone des Niayes). Ci gis-gisam bat ay, loolu dina dooleel mbay mi, yombal itam suqaleeku gox yi.
Jëwriñ ji, Séex Tijaan Jéey xamle naat ni, sémb wi, ak li mu ëmb ciy ngëneel, wone na ni ndox mi bokkee ci balluy mbindaare yi ëpp doole ñeel suqaleeku tay ak ëllëg. Leeral na itam ni tànneefu SINOHYDRO mi ñu jox sémb wi dafa aju ci settantal yu dëggu ñeel lawax yi. Ginnaaw settantal yooyu, SINOHYDRO dafa ràññeeku bu baax ci jàppale FONSIS ci kopparal bi, ci firnde yi mu jot a wone ci kembarug Afrig ak ci àddina si, doomi réew mi mu nar a jël ñu liggéey ci, ak sémb wi mu dogoo yeggal ci ni mu gënee gaaw.
Muy ay leeral yu jëwriñ ji indi ginnaaw bi Biraahim Sekk, kenn ci njiiti kuréli ma-xejj yi, yékkatee kàddu, di laaj i leeral ñeel anam yees joxee sémb bi waa SINOHYDRO. Ginnaaw leeral yooyii tam, Biraahim Sekk àdduwaat na. Ca kàddu ya mu mujje yékkati nag, ma nga cay xamle ni baat yi ñu jëfandikoo ci seen leeral yi dafay niru ay réerantal. Liñ leen di laaj mooy ndax woote bi ñeel lawax yi am na am déet ?