SÉMBUW NDEFARUG DAAMARI SÓOBARE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dees na samp ndefarug daamari sóobare fi réew mi. Xibaar la bu tukkee ci Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Càmm gi dafa xaatim, barki-démb ci alxames ji, 7 nowàmbar 2024, déggoo bi dox ci digganteem ak kër gii di ISEVEM (Industrie Sénégal de Véhicules Militaires).

Démb ci àjjuma ji, 8i pani nowàmbar 2024, doon nañu màggal fi réew mi bés bees jagleel làrme bi. Muy xew-xew bob, dees ciy fàttaliku bés bees njëkkee jébbal làrme Senegaal bi lii di raaya réew mi (10 nowàmbar 1960) ginnaaw bi mu moomee boppam. Wëppaw ren ji nag, moo ngi tënku ci « dox jëm ci moom-sa-bopp ñeel xarala yeek ndefa yi ».

Fa Ndakaaru, Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo jiite woon tijjite ga. Biral na fay kàddoom, wone mbégte mu réy mi mu am ci jiite bés bi. Nde, jàpp na ni « bés la buy màggal dogu, yar ak fonk sa réew gi nekk ci sunu jàmbaar yi doon dëgg-dëgg ñiy sàmm kaaraange gi, jàmm ji, dal gi ak mànkook sunu Askan ».

Njiitu réew mi biral naat ni wëppa wi ñu tànn ren doon na luy wone tolluwaay bu am solo bi Càmm gi am te jëme ko ci dooleel mënal-sa-bopp gi ak wóoraayu doxaliinu kaaraange. Naka noonu, biral naat ni Senegaal xaatim nab déggoo ak kër gii di ISEVEM ñeel sémbuw samp ndefar gog, dees fay boolee daamari sóobare. Bu weesoo loolu, Njiitu réew mi biral naat ni dees na amal ab neexal ci bési làrme yiy ñëw jagleel ko fentug xarala ak ndefar gi gën a fés ñeel sóobare yi.

Ci bi ñuy xaatim déggoo bi, jëwriñu ndefar geeg yaxantu bi, Sëriñ Géy Jóob  andi na ciy leeram :

« Sémbuw samp ndefarug daamari sóobare yi dafay aju ci mébét mi ñu am ci réew mi. Muy mébét mu aju ci taxawal ay ndefar, dooleel sunug kaaraange ak suqaleeku gu law ci ñépp. Déggoo bi, bu weesoo li mu nuy wattul sunug mënal-sunu-bopp ci wàllu kaaraange, doon na itam luy firndeel sunug dogu ci tabax koom-koom  gu mën a dékku jafe-jafey  yi nu nar gaarsi ci at yiy ñëwi. »

Sémb woowu nag, dees na ko samp fa Mbàkke, diiwaanu Jurbel, ngir féexal Ndakaaru ak amal i liggéey ci gox yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj