SEN BU APR WOOTE NA BÉSUB ÑAXTU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Làngug pólitig gu APR (Alliance Pour la République) woote na bésub ñaxtu keroog àllarba 2i fani awril 2025. Muy woote bu ñu def ginnaaw kàddu yi Mustafaa Njekk Saare biral jëme leen ci ndem-si-Yàlla ji Muhamadu Mustafaa Ba mi fi nekkoon jëwriñu kopparal gi.

Waa APR àddu nañu ci tolluwaayu géewu pólitig bi ci seen ndaje mi ñu doon amal barki-démb ci alxames ji, 20 mars 2025. Ginnaaw ndaje ma, SEN bu APR (Sécrétariat Exécutif National bu APR) génne na ab yégle, tënkaale ci mbooleem ponk yi ñu doon waxtaane. Bokk na ci ponk yooya, kàddu yi Mustafaa Njekk Saare yékkati bu yàggul dara ci paatug Muhamadu Mustafaa Ba ak sémbu àtte biy dellusi ci àtteb neenal bi fi jàlloon ca jamonoy Maki Sàll.

Naka noonu, SEN bu APR di ñaawlu ak a mettitlu kàddu yi jëwriñ ji yëkkati, ne Muhamadu Mustafaa Ba ci boppam dëggaloon na, laata ñu koy ray, ni dañoo sopparñi ay lim ci caabal yi. Ñu jàpp ne nag, wax ju doy waar la. Nde dañuy ay kàdduy tuuma yu mu gàll ki fi nekkoon jëwriñ. Waaye itam diy kàddu yuy wone ni moom ñàkkul mu am lu mu xam ci anam yi jëwriñ ji faatoo. Ba tax ñuy sàkku ci toppekatu bokkeef gi mu woolu ko, déglu ko ngir mu andiy firnde ci kàddoom yooyee.

Bu weesoo loolu, àtteb neenal bi fi Ngomblaan gi jàllale woon ca jamonoy Maki Sàll ñor na leen lool. Ba tax ñu ciy dellusi ngir leeral li taxoon a jóg boobule àtte. Ñuy fàttali ni njéggal ak jàmmi réew mi moo taxoon Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, wotelu ko. Looloo taxoon ba dépite yi wote jàllale ko. Te itam, looloo waraloon ba réew mi am jàmm, ñu mënoon a amal i wote yu ànd ak dal, yu leer, yu ñépp bokk.

Ba tey ci seen yégle bi, ñoo nga cay xamle ne, lu ni mel, bu ci làngug Pastef nammee dellusi, dañuy sàkku ci moom mu dëggal ci boppam bu baax. Maanaam, mu dem ci ba jeex te bañ fee nekk di sàkk i pexe ak a faramfàcce. Ci seen gis-gis, Àtteb faramfàcce (loi d’interprétation) bi Pastef di woote jëme ci àtteb mbaale gi fi woon, doonul lenn lu dul nas i pexe.

Naka noonu, ñuy dellu di woote doxu ñaxtu fa buntu Ngomblaan ga, keroog àllarba 2i fani awril 2025, ngir wone seen ñàkk ànd ci ni kilifa yu bees yi namm a doxalee. Ndax li ñu namm ci àtte bi mooy rawale ñi nekkoon ci ginnaaw ak ñi ñu doon yabal ñuy yàq, waaye itam, tuumal takk-der yi nekkoon di def seen liggéey ni leen ko yoon santee ñeel kaaraange dëkk bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj