Gàcca-ngaalaama sunu xëllóob yi (gaynde yu ndaw yi) ! Taaw daal, ndeke bu xàllee, rakk ya am jomu daagu ni buuru tan. Ba gaal gu mag ga rëbbijee ba andi kuppeg Afrig ba léegi xale yi ñëwatuñook i loxooy neen ! Senegaal àddooti n’a, te Afrig gépp dégg na baatam.
Niki mu ko yëgee woon, keroog ba gayndey Aliin Siise ya jëlee Kuppeg Afrig ga, yu Paap Caw yi feelu leen ca, noonu lan yëgaatee bànneex ci sunu xol yi tay bi gaynde Maalik Daaf yi jëlatee kuppeg Afrig gii ñeel ñi amagul 20i at. Ca njëlbéen la xale yi tàmbali wane jom ba ni mu jeexee, loolu di lu réy ci mbooru kuppegu Senegaal.
Tay, ci gaawu gi, la Senegaal doon jàmmaarlook naataangoom bii di Gàmbi ñeel finaalu kuppeg Afrigu ñi matalul 20i at. Senegaal jël raw-gàddu gi ci kaw kii di Gàmbi, dóor ko ñaari bal ci dara.
Joŋante gi nag, laata mu doon tàmbali ci pàkk mi, dafa mel ne ca mbaali-jokkoo yi la njëkkee. Li ko dalee démb la tooñante geek nappante gi dooroon. Waaye, nag, sunu gaynde yi jeexal nañ ko ci ni mu gën a rafetee. Mu nekkoon joŋante bu neex, ñoom, ñaari ekib yépp, def yoon wu rafet, ñëw ba finaal te kenn dugalul seen i kër.
Senegaal nag, dolli na am mbind mu dootul daj ci mbooru kuppeg Afrig. Ndaxte, lépp luy raaya, ñu tegoon ko ci kuppe Afrig, jël na ko def ci jibaam. Bu yàggul dara, atum 2022, la ekib bu mag bi jëloon lii di kuppeg Afrig. Ñu doxal tuuti, jëlati kuppeg Afrig ñeel ñiy kuppeg têtes gi ; ñu ni déet-a-waay, mu tegati ci lii di CHAN bi. Ñu foog ni fa lay yam, ñu dollil ñu ci kuppeg Afrig gii ñeel ñi amagul 20i at. Loolu di lu rëy ci mbooru kuppeg Senegaal ak Afrig. Dafa di, guléet lu ni mel di am.
Rax-ci-dolli, sunu gaynde yi dañ raafal cargal yépp. Nde, ñoo ci jël kuppekat bi gën a xaren (Lamin Kamara), ki dàq dugal (Paap Demba Jóob) ak ki dàq a jàpp. Bàyyiwuñ dara. Li xale yi naan “fatt nañu fépp ba dara sennul”. Ñu xare itam ba jël kup gi te kenn lakkul seen caax, muy lu mësut a am ci bile kub.
Senegaal gépp a bég, te waneeti na boppam ci wàllu kuppe ba ñépp teg ci seen bët. Ngelaw liy ëpp réew mi ci wàllu kuppe daal, Yàlla bu mu gaaw a dal, ñuy teg i jéego rekk di dem, romb Afrig gi, bindi turu Senegaal ci kuppeg àddina si.
Laawla-cat sunu gaynde yi ! Yàlla bu leen cat topp !