Réewum Senegaal ak mu Móritani fas nañu lu bees ci dem beek dikk bi. War na léegi ci doomi réew mu ci nekk ñu gànnaayoo kayitu dalal (carte de séjour) ngir dund fa meneen réew ma lu ëpp ñetti weer.
Ginnaaw pas gi ñu defoon bu yàggul dara ci wàlluw yaale beek sëfaan yi, Senegaal ak Móritani séqi nañu jéego bu bees ci seen lëkkatoo gi. Wile yoon nag, pas gee ngi aju ci anamu tukki yi ngir jàppandal dem beek dikk bi ñeel nit ñi, godaar yeek daamar kenn-kenn yi ci diggante ñaari réew yi.
Pas gi nag dafay ñëw ngir yeesal anam yi doomi réew mu ci nekk di dugge fa meneen réew ma ak diir ba ñu fa war a def.
Naka noonu, doomu réewum Móritani mu bëgg nekk Senegaal lu ëpp ñetti weer, dina war ci moom mu wut li ñuy tudde ci nasaraan carte de séjour, di ag kayitu dalal guy yoonal sa nekk fi réew mi. Kayit googu nag dina ko may mu nekk fi réew mi ci diiru menn at. Ku ci bëgg a am it, dina joxe 5 000 Fcfa.
Ngir am gu njëkk gi nag, dees ko yombal ba kenn du la laaj pasug liggéey walla firndey li ngay am ci sa liggéey. Waaye bu kayit gu njëkk gi jeexee ba ñu bëgg koo yeesal, dina war ci lawax bi mu teewaale ak kayit giy firndeel li muy am ci liggéeyam.
Ndogal lu ni mel nag, ñaari réew yépp a dëppoo ci doxal ko ci seen suuf. Naka noonu, doomi réewum Senegaal yi bëgg nekk fa Móritani itam dinañu fa fay 300 MRU ngir am fa kayitu dalal buy dem ci ñetti weer ba at. Bees ko bëggee yeesal itam dinañu fa wanewaale kayit giy firndeel la ñuy am ca seen liggéey.
Pas gu ni mel dina far lépp luy gàllankoor askan yi ci seen dem ak dikk ci ñaari réew yi. Pas gi nar a doon jéego bu réy ci ni ñaari réew yi lëkkatoo ngir saytu tukki yi, taxawu ci lu leer doxandeem yiy dugg ak di génn ci seen dig, ak gën a dëgëral li leen boole ci mboor ak li lëkkale ñaari askan yi.
Bu weesoo nit ñi, pas gi dina yombalal daamari kenn-kenn yi seen daw ci diggante ñaari réew yi. Dinañu leen oyofalal yi ñu warlook caytu gi ci diiru 180i fan.