SENEGAAL TIIT NA WAAYE ËLLËG, ËLLËGU ASKAN WI LA…(PAAP AALI JÀLLO)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bindkat yi bind nañ, waxkat yi wax, gëstukat yi biral, boroom xam-xam yi jàngat, kilifa diine yeek yu aada yi àddu, aartu. Taskati xibaar yi, ñii yatt seen i xalima, bind ; ñee boyal seen i làmmiñ, wax. Senegaal, amul ku waxul ci yëngu-yëngu yu metti yees génn, fan yii weesu. Coow leek xeex bi ne woon kurr ci réew mépp. Askan wi, rawatina ndaw ñi, di safaantook takk-der yi. Ci benn boor, gërënaad yiy téll-télli, saxaar su wex xàtt si ubale jàww ji, noyyi jafe. Ci beneen boor, xeer yiy xërr-xërri. Xeex bi metti lool, lool sax…

Xar-kanamu réew mi soppeeku, ñaawal la ko ba… Xeer yaa ngi juuge ci kow tali yi, weexal leen tàll ; puno yiy lakk, estaasiyoŋ yeek màngaseŋ yi tàkk ba jeex, di saxaar. Nga gis ay bitigi Auchan, Total, añs. yuñ dàjji, jël njaay mépp,
rajaxe leen rajax. Kenn mësul a gis lu ni mel ci miim réew. Deret jiy tuuru, bakkan yiy rot ba àgg ci 13. Guléet yëngu-yëngu yu taree nii te law di am ci Senegaal. Liggéey bi dakk, njàng mi taxaw. Oto demul, oto dikkul.

Senegaal, réewum jàmm ma woon… 

Naam, jàpp biñ jàpp Usmaan Sonko moo sooke mbir mi, waaye sabab yi fippuloo askan wi, tax leen fétteerlu, weesu nañ jëmmu njiitalu PASTEF li. Moo tax, jamono ju politiseŋ yi nekkee fiiy tamante dëmm, boroom xel yi, ku nekk ci sa boor, yaa ngiy càmbar mbir mi bu baax, di ci amal xalaat bu xóot.Fii, kenn mënu fee nax kenn, te kenn moomu fi kenn.

Barewaan nañ di dégg, fépp ci àddina si, ñu naan Senegaal réewum jàmm la. Jamono jii nga xam ne, boddekonte, xareb waaso ak terorism daa fës, Senegaal, moom, Yàlla jotoon na koo musal ci xeeti musiba yooyiy taal i réew, nasaxal i koom-koom, yokk ñàkk gi. Dal ak jàmm jooju amoon ci réew mi, fekk ay yëng-yëngu yu mettee ngi amoon ci réew yim dendal (Mali, Koddiwaar, Gàmbi…) moo taxoon Senegaal nekkoon ab royukaay. Wànte booba daa fekk Maki Sàll

lukkeegul askan wi. Bim leen nee duut baraam ci bët, gannaaw cokkaas ak tooñ yim leen yàgg a tooñ, ci la jàmm jeex Senegaal. Senegaal, nag, ak li mu daloon yépp, nekkoon ci jàmm, dafa yàgg a barey jafe-jafe, ci fànn yépp, nag. Muy ci wàllu koom-koom gi, demokaraasi, yoon, njàng meek njàngale mi, càmm geek napp gi, mbay meek mbiri suuf si, ñàkkub xéy gi, añs. Ñu ni déet-a-waay, mbasum Covid-19 mi ñëw dolleekusi, yokk xar mi karaw.
Senegaal, réewum ndóol… 

Ci atum 2020 bii rekk, boolees na Senegaal ci 25i réew yi gën a ndóol ci àddina si. Ci limu 189i réew, Senegaal mooy 168eel bi. Njiit yi taluñu dara lu dul xool ni ñuy gën a aakimoo alalu askan wi. Guural gi dafa doggali askan wi, yàq liggéeyi nit ñi, bëtt gafaka yi.

Boroom kër yeek góorgóorlu yi daan fortaatu guddi amatuñ pexe. Mayga bi daanu na, boroom forox-caaya bi këpp cinam, matti dibitëri yi sedd guy, meer yiy jaay cere këpp seen i leket, jaaykatu fonde bi arawatul, jaaykatu supp bi toggatul, salaat-guddi amatul, mburook soosu guddi jeex… Jaaykatu kafe-saaf, guddi, seggatul, Pël-Fuuta bii jéreetul neskafe walla meew, Pël-Fuuta bee,
moom, fat na taabalu meññeefam walla palaatu kokoom… Oto baadoolo dawatul guddi. Payoori dawalkati kaar-ràppid walla Njaga-njaay yeek seen i àpparaanti gën nañoo tuuti. Boroom taksi yi, ñoom, gaare nañ ca marax. Lu fi desati ? Kon, mbirum Usmaan Sonko, ab toqu ndox doŋŋ la ci géejug tolof-tolof ak i jafe-jafe yi askan wi yàgg a dund.

Safaras mer siñ yàbbi fan yii weesu, dañ koo yàgg a guux. Nguur gi mayu leen dara : du liggéey, du xaalis ; du jàmm, du salaam ; du yoon, du maandute, dara. As mbooloo mu ndaw féetewoo alalu askan wi di ci gundaandaat, ñoom ak seen i njaboot, boole kook ñàkk kersa bu doy waar. Ay nguuraafon (gouvernants) yu ñàkk yërmaande, di nos ak a nocci ngir sax ci nguur gi, mu jaral leen sànk ay nit, tëj ay politiseŋ. Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll doy nañ ci misaal. Ngir joyyanti mbir mi, nag, dafa laaj lu bari. Loolu lépp la askan wi boole woon denc, xéy bés
waccu lépp, fitna daldi am.

Delloo askan wi baatam, mu tabax ëllëgam 

Gannaaw bim noppee ay fan, njiitu réew mi, Maki Sàll, génn na wax. Nangu na ne, dara doxul te askan wi, rawatina ndaw ñi, dañoo sonn. Te sax, dige nay mbir,
nim ko tàmmee def. Waaye, jamono jii, du jamonoy wax. Jamonoy jëf la. Bu dee ne njiitu réew mi dégg na dëgg-dëgg jooyi askan wi, daf koo war a firndeel ciy dogal yu leer.

Bi ci jiitu mooy wàccee, Antuwaan Feliks Jom (jawriñu Kaaraange biir réew mi) ak Maalik Sàll (jawriñu Yoon wi). Nde, ñaar ñooñu, dañoo féete boor te ciy njombe lañu dëkk. Toppekat bu mag bi moom, Basiiru Géy, kenn daa waxul i waxam. Bés bu ne mu jalgati yoon ngir lu neex Maki Sàll. Bañ nañ ko ba, léegi, Toppekatu Maki Sàll bi lees ko dàkkentalee. Kooku yit, wàccee ko dafa jot.
Ndax kenn wóolootu ko.

Réew mi dafa yittewoo dal jamono jii. Yoon dafa jeng ba ñépp xam ko. Kenn wóolootul pólisee yeek àttekat yi ndax jàppees na ne, réew mi, Kumba am ndey ak Kumba amul ndey moo fi am.

Ñaareel bi mooy ne, war na fi dindi yenn campeef yi. Kurélug koom, nekkin ak càkkeef gi (Conseil Economique, Social et environnemental) ak Kurélug mbooloo tund mu kowe mi (Haut Conseil des Collectivités Teritoriales) ñooy
campeef yees gën a ŋàññ. Nde, kenn mënul a wax lan mooy seen njariñ ci réew mi. Rax-ci-dolli, li ëpp ci nit ñi dañ jàpp ne paacoo kese ak neexal ak àndandoo moo tax Njiitu réew mi, Maki Sàll, samp leen fi. Bu leen fi jële woon, delloo xaalis biñ ciy xëpp yépp ci askan wi, doon na wàññi lu bare, defar lu bare. Rax-ci-dolli, Péncum réew mi, nim tëdde nii, nguur gi la fi nekkal. Lu Njiitu réew mi joxoñ, ay dipiteem dagg jox ko. Ndaxte, ñoo fa ëppub lim, ëpp fa doole. As tuut ciy dipite yu am mbooloo te rafet yéene, amuñu fa baat. Moo tax, coppite war na am ci tëralinu Péncum réew mi ngir delloo askan wi baatam bu as mbooloo mu ndaw a ndaw foqati.

At mu nekk ñu wote nafag réew mi, mu tollu ciy milyaari milyaar, askan wi di ko dégg. Saa su ne nga dégg ñu naan def nàngami milyaar ci fànn bii walla ci
naal bee. Milyaar fii, milyaar fee… Askan wi, moom, di yéewoo ndóol, yendoo sonn, fanaanee xiif. Ana milyaar yi ñuy dégg saa su nekk ? Jot na ñu leeral fu xaalis boobu dugg.

Tollale dafa baax cim réew. Waaye, dafa mel ni sunuy njiit dañ koo réere mbir. Ku jóge ci dëkki taax yi, rawatina Ndakaaru, dem ci kow gi, dinga xam ne, ci
wàllu koom ak liggéey, yemuñu te yemaluwuñ leen. Lépp lañ féetale Ndakaaru. Moo tax, waa kow gépp màbb, wutali Ndakaaru. Loolu moo waral itam Ndakaaru xat ni mu xate nii.

Ndaw ñii ñu ngeek seen i lijaasa, ñee ñu ngiy kërti-kërti subaak ngoon di wër liñ suturloo. Ndeysaan, ñi ci ëpp amuñu xéy te yàqi nañu. Ndaxte, dañ gis ne, Senegaal, ku fi amul mbokk ci nguur gi, amooy xame yu la mën a lijjantil dara, doo am dara.

Jigéen ñi moom, daanaka dañ leen a fàtte. Naam, ñoo ngi soow ak wote ay àttey yemale diggante góor ak jigéen, waaye teguñu benn jéego buy wone ne fullaal nañ jigéen ci miim réew. Du ci wàllu pólitig, du ci koom astemaak wér-gi-yaram.

Yoon mi ngi ci loxoy nguur gi, koom-koom gi noonu. Péncum réew mi, ñu ŋëb kook seen loxo, di fa def lu leen neex. Askan wi amatul baat ci dara ba dara booloo jeex. Xeex rekk a fi sësoon. Naam, dal am na, jàmm delsi ngir maslaa bi ci am. Waaye, loolu warul xàddiloo askan wi. Ndaxte, ëllëg, ëllëgu askan wi la,
kenn du ko ko waajalal ku dul boppam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj