Sëriñ Mustafaa Si joxe na gis-gisam ci tolluwaayu réew mi, rawatina yëngu-yëngal yi fi amoon bay bakkan yu bari rot ci, ci sababu daan bi àttekat bi daan Sonko ñeel layoom beek Aji Saar. Kilifag daayra mustarsidiin Wal mustarsidaat gi nag, tagg na Usmaan Sonko, mooytuloo Bàrtelemi Jaas ak Xalifa Sàll te di artu Nguurug Maki Sàll gi.
Bu dee Usmaan Sonko, lii la wax ñeel ko :
“Dañoo tooñ Usmaan Sonko, ay farandoom jóg. Loolu kese la. Dafa mel ni ab boroom-kër rekk ; saa buñ ko songee njabootam taxaw ci wetam. ”
Moom, njiitul PUR, yemu ça. Nde, tagg na njiitul Pastef li, seedeel ko ne : “…gor dëgg la. Jàmbaar dëgg la. Nit ku ma naw bu baax a baax la. Saa yu ma ko bëggee wax dara, Seex Tiiijaan Yum laay yónni ci moom [mu jottali ko sama kàddu].”
Sëriñ bi neeti, jëmale ci Maki Sàll ak nguuram, ne :
“Na Maki Sàll xam ne, denc naa fu sori nataali Usmaan Sonko te, foofa, Buur Yàlla dina ko fa sàmm.”
Bu dee mbiri Bàrtelemi Jaas mi ñu jàpp ne soppiku fan yii, déeyoo ak Maki Sàll, Sëriñ Mustafaa a ngi ko mooytuloo, di ko bàyyiloo xel ne, mën nañ ko nax. Moo ko tax waxati ne :
“Maa ngi ñaanal Bàrtelemi Jaas ngir ñu bañ ko nax. Danu amoon yaakaar ci moom. Te mës naa wax Usmaan Sonko, ci benn gàmmu bu fi amoon, mu dimbali ko ndax dañ koy jéem a nax.”
Nooneet la doomu Sëriñ Seex Tiiijaan Si Al Maktum ji soññee Xalifa Sàll mi dem ci Péncoo mi Njiitu réew mi woote.
“Dama yónni Seex Umar Yum ci Xalifa Sàll bi ma yëgee ni day bokki ci waxtaan wi Njiitu réew mi woote. Wax naa ko nag li ma ci xalaat. Ndaxte, pàrteem mënu ko fal te man mën naa ko.”
Ba tey, Sëriñ bi wax na ci ñetteelu moome gi Maki Sàll bëgg a dagaan. Nee na, na ci Maki Sàll génne xelam ; lu ko moy, dina génn génnin wu ñaaw. Fàttali na tam xelal bim xelaloon Ablaay Wàdd 2011 :
“Jamono jooja, dama waxoon Ablaay Wàdd mu fexe génne ci buntu bu mag bi. Dafa bañoon, jaay doole ni day def ñetteelu moome. Xam nañ fa mbir ya mujje. Tey, lu ko yées na Maki Sàll nar a dund.”