Weeru sàttumbaar wee jàll lañu tegoon loxo kii di Serom Bànjaki, ñu di ko woowe “Sniper”. Booba ba tay, ma nga ca loxoy Yoon. Waaye, mu mel ni am na lu bees ci ay mbiram bees sukkandikoo ci li yéenekaay bii di Les Echos fésal tay ci xëtam wu njëkk. Dafa di, kii di Serom Bànjaki, jàkkaarloo na ak magum àttekat yi. Mu jot a leeral yenn ci mbir yi ñu koy toppe. Muy lu ci mel ni kër ga mu dëkkoon, mbirum ngànnaay yeek liggéeyam. Ki mu duut baaraam ci menn ci mbir yooyu du kenn ku dul Aminata Ture mi fi nekkoon ay jamono elimaanu jëwriñ ci Nguuru Maki Sàll.
Aminata Ture, ñu gën ko xam ci turu Mimi Ture, nekkoon na fi elimaanu jëwriñ ci Nguuru Maki Sàll. Waaye, ginnaaw gi, digganteem ak Maki Sàll dafa mujjee ñagas. Ca la génnee, ber daaraam. Mbir mii Serom Bànjaki di wax ne séqoon nañu ko, ca jamono yooya la woon.
Dafa di, moom Serom Bànjaki, dañu koy toppe mbir yu bari ginnaaw bi ñu ko tegee loxo. Muy lu ci mel ni “escroquerie au préjudice de l’Etat, usurpation de fonction, trafic d’armes et de munitions et détention d’armes”. Ginnaaw bi ñu ko dégloo, dafa weddi tuuma yees ko gàll, daldi leeral. Ciy waxam, dëkkuwaay bi mu yoroon ci diggu Ndakaaru (centre-ville) te ñu mujje woon ko fa génne , moom ak njabootam, wax na ni mu ci jote. Nee na, Mimi Ture moo ko jàppale woon ba mu jot ca, ca jamono ja mu wuutoo Abdul Mbay. Li ko waral mooy ne, moom, fa mu dëkkoon dafa sori. Moo tax, léeg-léeg mu daan naajee xëy. Ndax, “Mamelles” la dëkkoon. Ci la ko elimaanu jëwriñ yi waxee mu defar ag càkkuteef jébbal ko ko ngir mu wutal ko kër ci diggu Ndakaaru. Noona la jotee ci dëkkuwaay boobu. Bi Mimi nekkatulee elimaanu jëwriñ tamit, mu wéy di des fa kër ga. Ndax, jamono jooju, fekk na mu tàmbalee jege Maki Sàll.
Waaye, ba tay yemul foofu. Ndax, leeral na liggéey bi mu doon def. Nee na moom aji-wattu kaaraange la (assistant de sécurité). Maanaam, day wattu kaaraangeg nit ki, ak njabootam walla sax mu koy doxal ay mbir ci suuf. Nee na moom du ndawu Càmm gi (agent de l’Etat). Mu yokk ci ne moom mësul nekk ci ay mbiri jaay ay ngànnaay (trafic d’armes). Li ñu ko mën a toppe kay mooy ngànnaay li ñu fekk këram.
Ñu gis ne am na lu Serom Bànjaki jot a leeral magum àttekat yi ci mbir yi ñu koy toppe. Kon, fii ak ub diir dees na xam fan la Yoon di mujje ak moom. Waaye tamit, dees na xam nu Yoon di def ak kii mu duut baaraam, di Mimi Ture. Li ci kanam, rawul i bët.