Sitt ak Papaa Sow : Wure wa dem na këŋ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sitt ak Papaa Sow dinañ jàmmaarloo ci dibéer jii, 6 noowàmbar 2022 ca Aren Nasiyonaal bu Senegaal. Jàmbaar Productions moo ko tëggaat làmb ji. Nde, njëkkoon nañu bëre, waaye àggul woon. Ndaxte, way-fari Sitta dañu xaañoon Papaa Sow ba mu jële ciy gaañu-gaañu. Muy kombaa bu ñépp nammoon mu am ndax tolluwaayu ñaari mbër yi ci làmb ji.

Ginnaaw bi seen kombaa bu njëkk yàqoo woon ciy simili laata ñuy sëgg, Papaa Sow ak Sitta dinañ dajewaat ëllëg ca Aren Nasiyonaal. Ñaari mbër yi nag, ku ci nekk xasoon na, teg. Papaa Sow ne woon na « di na xeex, dina bëre ». Tegaat na ci bu yàggul dara ne « fukki kombaa, ma daan la. Boo laam-laamee ma dolli la benn muy fukk ak benn. »

Waaye Sitta tanqamluwu ko benn yoon. Ne woon na ko it « dangay teyaatar rekk. Waxuma la dama lay daan de. Dama ne, dama lay dugal oto. Inite 1 lanuy tàmbalee. Are bun jot, ma ne la Papaa nan bëre. Ma duma la, daan la. Bu doon paketu mbiskit doo yëy dara. »

Ku yàgg a topp làmb, xam ni Papaa Sow Ndaanaan la. Kenn dootu ko xamale ci làmb ji. Bëre na ba bëre Olympique. Rax-ci-dolli, wudd (écurie) wu Faas la bokkoon, daan tàggatook i ndaanaani Faas yi laata ñu ko fay génne. Léegi Pàrsel lay ngemboo. Loolu di meneen mbir ak ni waa Pàrsel mënee wuyusi làmb.

Waaye nag bu kenn fàtte ni Papaa Sow dafa jël mbër mu nekk ci yoon te làmb yépp bàyyi ko xel. Bi Sitta di dugg ci làmb, ku nekk mënoon na taxaw ne kii du dem. Muy raam di daan, boole kook liggéey ba àgg foo xam ni kenn du wax làmb, di lim mbër yi fàtte ko. Mi ngi bokk itam ci wudd wu lansaar, ci Maks Mbargaan. Muy ku am mbooloo itam. Jàmmagën yépp top ci ginnaawam. 

Ba ci seen Jàkkaarloo bi mujj ci àjjuma ji weesu, 28 oktoobar 2022, ñaari mbër yi mayantewuñ dara. Ba tax Sitt naan « kombaa bii mooy dàq ci at mi. Xanaa Papaa bañ ». Papaa it wax ne « danoo noppi def kombaa bu neex, ñëw bàkku lu neex, bëre lu neex, ñaan Yàlla may nu ndam. »

Ginnaaw bi lépp wéyee, jàkkaarloo yeek Open Press yi jeex, ñaari mbër yi xas nañu li ñuy xas ba noppi. Nee nañu dinañ xeex, dinañ bëre. Benn bés a ci des. CNG bi ak Jàmbaar Productions jël nañ seen i matuwaay ñeel kaaraange gi. 1500i alkaati ak 1000iy sàndarm dinañ fa teew ngir aar nit ñi ci biir ak ci biti te sàmmaale jumtuwaay yi ba yàq bañ faa am. Lótari nañ itam ba xam mbër mu nekk wet ga ngay féete ngir coow bañ a am. Sitta mooy dal ci wet gi A, Papaa Sow féete ci geneen wet gi B. 

Ndax Papaa dafa nar a téyee Sitta walla Sitta dafay jaar ci kowam Jàll ? Ñépp a ngi xaar ñu teew ci jàmm, dëggal seen bopp, bëre lu neex ngir bégal axlu làmb. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj