SIYAARE DAARAY KOKKI : BÉSUB ALXURAAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci dibéer ji? yemoon ak ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru desàmbar wii, moo nekkoon bésub ndajem Alxuraan miy am at mu jot fa Kokki. Ndajem démb mi, mooy ñeen-fukkeelu yoon ak ñett ñu koy amal fa dëkk ba. Daaray Kokki nag, mel na ni kenn naatableetu ko ci biir réew mi, ba ci sax bitim-réew, rawatina réewi Afrig yi digalook Senegaal. Ndax, kenn umpalewul ne daara jooju la mu dajale ciy ndongo yuy sàkku xam-xam du ñépp a bawoo fi réew mi. Mu nekk daara ju ñu naw lool ngir liggéey bi muy amal ci wàll woowu.

Daaray Kokki ñi ngi ko sos ca atum junni ak juróom-ñeenti téeméer ak fanweer ak juróom-ñeent. Ki ko sos di Ahmet Saxiir Lóo. Ki ko wuutu jamono jii ca liggéey ba di Sëriñ Mataar Naar Lóo. La fay yeewoo ci ay ndongo dem na daanaka ci ñeenti junni bees sukkandikoo ci xayma bi ñu ci mujjoon a def (3940). Ëttub Alxuraan boobu ma nga nekke fa Kokki. Kokki nag, dëkk la bu bokk ci Luga, nekk ci yoonu Luga-Daara Jolof wi. Digganteem ak Luga di dem ci fanweeri kilomeetar.

Dayob Alxuraan mel na ni kenn umpalewu ko ci diine ji. Te, daara ji def na ci liggéey bu mucc ayib. Ku def lu réy nag, am lu réy. Looloo tax ba daaray Kokki, jamono jii, yóbbu na turu dëkk bi fu sori lool muy ci biir réew mi ak ci biti yépp. Ndax, bésam bii muy amal at mu jot, daanaka fu nekk la nit di jóge di ko teewe. Moo tax fi mu tollu nii siyaar bi nekkatul léegi ci daara ji kepp. Ñi nekk ci biir dëkk bi yépp ay màggal bés boobu.

Dafa di, daara ji ñu bari jaar nañu fa. Am na sax ay kilifa yu bari tey ci réew mi moo leen tàggat, sol seen bopp Alxuraan. Ndaje moomu, ci bëccëg gi kese lay yem. Maanaam diggante suba gi jàpp tisbaar. Bu ñu xëyee dañuy amal waxtaan (conférence) ca daara ja diggante kilifay daara ji yoy, dëkk ba ak mbooleem gan ya walla ña fa dëkk di ko teewe. Bu waxtaan woowu jeexee rekk daanaka xew ma moom day daldi tas. Loolu nag terewul ndaje mi am fu mu tollu ña fay yeewoo ak ña fa jot a jaar.

Mu mel ni lu baax moom du tuuti. Foo jii lu baax rekk danga ko fa góob. Ndax, ñoom dañuy sol ci boppi ndongo yi xam-xam. Te, duñu ci feyu benn dërëm. Ba tax na fi mu tollu nii, daara ji xeetu xéewal yu ne ñi ngi leen koy indil rawatina ci jamono jii. Kon, loolu firnde la ci ne jëf ju baax moom kenn du ko réccu ak lu tolof-tolof yi di mën a bare.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj