SONKO YËNGAL NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndaje moomu mi ngi amoon démb ci dibéer ji, fale ca béréb boobu ñuy dippee “Grand théatre”. Ñi ko amaloon du ñenn ñu moy ndawi Pastef yi. Usmaan Sonko, niki njiitul PASTEF, moo doon amal waxtaan wi. Ca biir waxtaan woowa, àddu na ciy mbir yu bari yoy, ñoo lëmbe réew mi jamono jii. Waayeet, tontuwaale na ñi koy ŋàññ, moom, Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay ak seenn càmm gi.

Waxtaanu démb wi mooy ñaareeluw waxtaan wi Usmaan Sonko,  elimaanu jëwriñ yi, amal ginnaaw bi ñu faloo, ñoom waa PASTEF, ak tey. Bu njëkk ba, fa jànguneb Ndakaaru ba (UCAD) la defee, mook tubaab bii di Jean-Luc Mélenchon. Ñaareel bi la doon amal démb fa “Grand théatre”. Mu nekkoon am ndaje mu xumb. Waaye, loolu du guléet ñu koy gis ciy ay ndajem ci at yu mujj yii. 

Poñ ya mu fa gën a faramfàcce mooy naal bi ñu nammee yoree réew mi. Bu dee ñi fi jóge dañu ne woon “horizon 2035”, ñoom nee nañu “horizon 2050”. Waaye, yemul foofu rekk. Nde, laal na fànn yu bari. Wax na ci ni réew mi di doxe, fi mu tollu ak fi ñu ko bëgg a jëme. Te, loolu Yoon daf cee am liggéey bu yaatu. Looloo tax, mu boole ceek i tëkku. Xamal na ñépp, rawatina kibaaraan yi, ne leen la woon, wonni na. Ñu bañ a jàpp ne seen pattaaral googu ag ragal la walla lu ni deme.

Tëkku yooyu du ci kibaaraan yi kese la yem donte ne sax, xamal na leen ne lu waay waxati na koy leer. Maanaam, bala ngay bind dara ci sa xët, na fekk nga am ci ay firnde yu leer. Ndax, ñoom dootuñu nangooti boroom kibaaraan yi di siiwal ci nit ñi lu leen neex, fekk teguñu ko fenn. Mu xamal leen ne moom nekkul fii di leen raayal ndigg. Ndax, bi ñuy nekk ci kujje gi, amul lu ñu leen waxalul. Kon, mënatuñoo wax lu leen saf. Rax-ci-dolli, lempo yi moom, mënut a ñàkk, ñu bàyyi ci xel.

Taxawaay boobu ñu am ñeel kibaaraan yi lañu am ñeel képp kuy jalgati Yoon nga bokk ci ñoom walla nga ñàkk a bokk ci ñoom. Dañuy bàyyi Yoon def liggéeyam ni mu ware. Ndax, nee na jeng gi Yoon jengoon bokk na ci li ñu doon xeex. Du yoon kon ñuy doxale noonu. Mu yokkaat ci ne caytu yi ñeel luubal yi dina door ci lu yàggul dara. Képp ku guuxoon, danga goqi. Te, képp ku bokk ci ñoom ak koo mën di doon boo luubalee Yoon dina dal sa kow. Moo tax, mboolem ñi mu séqal liggéey bi, muy jëwriñ yeek yeneen Njiit yi, ku ci liggéeyul ni mu ware, dinañu la wàccee.

Bi mu jógee ci wàllu Yoon tamit wax na ci dund bu jafe bi nga xam ne jamono jii ñépp a ngi koy jàmbat, rawatina ñi seen loxo jotul seen ginnaaw. Lu yàggul dara dinañu xamal askanu Senegaal matuwaay yi ñu jël ngir dund bi wàññeeku ba jàppandal ci ñépp. Naka noonu, xamle na ne pas yi ñeel balluy-mbindaare yi dees na leen waxtaanewaat.

Ci gàttal, mënees na ne, lii bokk na ci ponk yi gën a fés ci li Njiitul Pastef li doon waxtaane démb ak ndawam ñi. Nde, waxtaan wi ci diggante ay dige, sas, ñaax ak ay tëkku daanaka la tënku woon. Maanaam, xamal ku ne li ko war ak fan la war a yem. Ndax, bokk na ci liy tax liggéey bi ñu sumb ci réew mi mën a jaar yoon. Loolu daal mooy na ku nekk yem fa ñu la yemloo. Day màtte am du màtte, bañ a joxe sa loxo moo gën a wóor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj