SUNU RÉEW MI (NDAY XAYBA FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

 
Soxna Nday Xayba FAAL
mi ngi dëkk Ndakaaru, doon jàng xam-xamu melosuuf ca Daara ju mag ju Seex Anta Jόob. Bind na taalif yu bari ci fànn yu wuute, niki bëgg-bëgg ay jafe-jafey àddina, ngëm ak diine, sàkku xam-xam ak coono ya ca aju.

 SUNU RÉEW MI

Sunu réew mbubb lañuy naw
Fab jikko ak jëf sànni ca gannaaw
Sunu dëkk ku ñàkk ñu ni dafa ñaaw
Fental la ay melo ba ñépp di la daw
Sunu réew ku lay jubsi poose kanam
Soppi doxiin, làq ay mébétam
Di la ree tey socc ay bëñam
Soo moytuwul mooy daas paaka bi ñu lay jam
Sunu dëkk xarit daf fee jóge
Coro moom daa fara dee
Ku ne di jaay njombore
Feeling deal ak tappale

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj