Sàndikaa yi ëmb liggéeykati Yoon yi, di waa SYTJUST (Syndicat des Travailleurs de la Justice) ak UNTJ (Union Nationale des Travailleurs de la Justice) ñi ngi wéyal seen seleŋlu. Bi ñu tàmbalee seen seleŋlu boobii, mi ngi bëgg a yàgg. Daanaka, weeru suwe, walla sax la ko jiitu ba tay, ñi ngi ci ay ñaxtu. Weeru sulet wii moom da cee raw. Nde, saa su ñu dakkalee seen ub liggéey lu tollu ci ñaari fan, ñu foog ne fa lay yam, ñu yokkaat. Te, booba ba tay sàndikaa baa ngi wéyal ab xeexam. Waaye, mel na ne saafara moom walla ab déggoo amagul ba léegi. Looloo tax, démb, ci dibéer ji, ñu génnee ab yégle ngir xamle ne dinañu dakkalaat seen ub liggéey ab diir.
Liggéeyu Yoon mi ngi bëgg a tagatémbe. Nde, fan yii yépp ci ay ñaxtu lañu nekk. Maanaam, dañoo bank seen i loxo ne duñu liggéey. Mu doon mbir moo xam ne metti na lool ci ñi am ay giitaŋaas ci wàllu Yoon, maanaam ñi nga xam ne dañu leen a war a àtteek yu deme noonu. Ñu bari ci ñooñu, ñi ngi dàq seen i layoo ci sababu ñaxtu yi. Loolu di leen gën a yàggal ca kaso ba bu dee ñu war a génn lañu. Ñaxtu yi nag, du tay lañu tàmbali, jiitu na loolu.
Dafa di, sàndikaa bi nee na jotoon na a àrtu ca weeru féewiryee. Waaye, mu mel ni gaa ñi xoromaluñ leen woon. Looloo tax, ñu tàmbalee yëngal ci weer yu mujj yii. Ci weeru suwe wii ñu génn lañu door ñaxtu yi bu baax sax. Daanaka saa su ñu dakkalee seen liggéey rekk bu diir bi jeexee ñu dolliwaat. Te, noonu lañu ko jàppoo daanaka ci weeru sulet wii tamit.
Démb, ci dibéer ji, lañu génnee ab yégle xamle ci ne dañuy wéyal seen ub xeex. Maanaam, dinañu dakkal seen ub liggéey ci diiru ñetti fan. Te, fasuñu yéene teggi seen tànk fii ak ñi ñu ko séqal teguñu dara seen loxo. Ci gàttal, ñu wax leen lu ñu mën a dégg.
Ñoom nag, li ñu dugge ñaxtu yi du lenn lu moy Nguur gi gëddaal déggoo yi ñu amoon ak Nguur gi fi nekkoon ca atum 2018. Muy lu ci mel ni li ñuy wax ci farãse “alignement des greffiers à la hiérarchie A2 sans formation préalable” ak “le reclassement des agents expérimentés dans le corps des assistants de greffes et parquets”. Déggoo yii lañu amoon ba gaa ñi nangu woon ko ca ndajem jëwriñ ma ñu amaloon ñaar-fukki fan ak juróom ca weeru sulet, atum 2018. Booba ba tay, kenn yéyul yàbbi ci. Te, ñoom nee nañu mënatuñoo toog di seetaan loolu. Ndax, ñoom mënuñoo nangu ñuy yombalal loolu yeneen banqaasi liggéey yi, di ko xañ ñiy yëngu ci wàllu Yoon.
Fim tollu nii, ñoom, dañoo taxaw temm ngir saafara am ci li ñuy xeex. Ba tax ñu bëgg a séq waxtaan ak elimaanu jëwriñ yi, jëwriñu Yoon, jëwriñu Kopparal gi ak Nafa gi ak jëwriñu Liggéeyu bokkeef gi ngir ñu taxaw ci seen càkkuteef yooyu. Ndax, nee nañ, Yoon mënul dox te joxuñu leen gëdda walla àq ji war. Yoon mënul a dox fu dëgg amul. Waaye tamit, Yoon mënul a dox fii ak Càmm gi dugalu ci loxoom. Li mat a laaj kay mooy ndax Nguur gi dina wuyu sàndikaa bi ci li mu koy woo am déet ?