TABASKI 2025 : CÀMM GEE NGI CI WAAJTAAY YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Càmmug Senegaal a ngi ba tay ci waaytaayi tabaski 2025 bi. Ginnaaw déggoo bi mu amoon ak réewum Móritani, jubluwaat na réewum Mali ngir xar yi matale ci darali Senegaal yi.

Ñaari ayu-bés kepp des ngir ñu yegg ci bésub Tabaski bi. Waaye, Càmm gee ngi wéy di ko waajal ba léegi. Ci weeru awril wee weesu la njëkkoon a am ub déggoo ak réewum Móritani, jëme ci jëggaani xar yi ci tabaski bi. Mu waroon cee jël matuwaay yi war ngir jàppandal dugalug xar yiy jóge Móritani.

Wile yoon, Càmm gi yaatal na matuwaay yi ci digganteem ak réewum Mali. Naka noonu, yeneen i ndogal tukkee nañu ci ndajem jëwriñ yi ngir matal xar yi ci darali Senegaal yi. Bokk na ci ndogal yooyu, ñu yokk kaarange gi ci yoon yi ; yarkat yi ànd ak sëfaan yi leen di andil xar yi ngir mën a taxawu xar yi ci yoon wi, seen wér-gi-yaram ak yu ni mel ; yombal caytug duwaan yi ba jàllaleg jur yi mën a gaaw ; woyofal juuti yi ngir jàppale way-yëngu yi ci wàll wi, añs.

Ñuy i ndogal yoy, Nguur gi jël na leen ngir dugal, ci anam yu baax te wóor, xar yu doy ca ba muy teel. Naka noonu, Dr Alfa Ba, di fara-caytu Nguur gi ci bokk-bokkoo yi ak taxawu beykat yi, doon na amal ab tukkib nemmeeku fi biir réew mi ngir wóorlu doxalinuw ndogal yi Nguur gi jël jëme ci mataleg xar yi. Ci tànk yooyu sax, àggoon na fa Kidira, fa càmm yu ëpp yuy bawoo Mali di jaar ngir dugg Senegaal.

Ginnaaw bi mu demee fa Kidira, kilifa gi dellu na xamle ni lees nemmeeku ci béréb yi dal na xel. Njort na ni sax dinañu yegg ci seen i jubluwaay walla sax ñu weesu ko. Nde, donte ni dañuy soog a door, xayma nañu daanaka 80 000iy xar ci seen lim.

Cig pàttali, 250 000iy xar la Càmm gi soxla ci digganteem ak Móritani ak Mali ngir mottali lim bi nekk ci réew mi ba xar yi mën a jàppandi ci ñépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj