TABASKI TEEROOTI NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tabaski, xew-xew bu mag a mag la ci jullit ñi. Mu am cëslaay lu dëgër a dëgër ci diiney Lislaam. Yonent Yàlla ba, baayu yonent yi, Ibraayma (Jàmm ñeel na ko) la ko Yàlla njëkk a digal, muy jaamu Yàlla bu màgg, ñu koy baaxantal ba sunu jonni-Yàlla-tey. Ibraahim (JÑK) mooy baayu Ismayla (JÑK) miy maamu Yonent Yàlla Muhammad (Jàmm ak Salaam Ñeel na Ko) ; jëfu Ibraayma (JÑK) ju sell te màgg jooju la jullit ñiy roy ak dundal, ni ko seen yonent bi daan defe, at mu nekk ci fukkeelu fanu weeru tabaski.  Julliti àddina yépp a koy bokk màggalandoo, donte ne am na ñu dul bokk bés, rawatina fi Senegaal. Ñii àllarba lañuy julli, ña ca des julli alxames. Tabaski nag, teerooti na ci jamono ju metti ñeel góor-góorlu yi ak boroom kër yoy, seen i loxo jotuñu seen i ginnaaw. Moo tax, ñoo ngiy jàmbat rekk ak a jooytu.

Wenn fan walla ñaari  fan kese ñoo des ci tabaski bi. Ndax, ñaari tabaski mooy amati fi réew mi, nees ko dundee woon ak korite ga. Dafa di nag, ñaari julli moom, du lu bees ci miim réew. Waaye de, ndóol gi moom, ñépp a ci bokk yem. Moo tax, ñépp jaaxle nañu. Sabab bi du lenn lu moy, booleem li ñu jullit ñi yittéwoo ngir tabaski ak seen i njaboot, daf ci bari lol, jàppandeegul ci ñoom ndax ñàkk xaalis walla néewle ko. Xar am na, waaye dafa njëge ba jéggi dayo. Yu sew yi war a ànd ak xar mi tamit, yokk a yokk ba soxnay néew-ji-doole yiy duggi jamono jii, jaaxle nañu. Ndax, fàww nga génne ñaar-fukki junni yu tegal ngir mën a am xar mu tane. Mu woroo lool ak kàdduy Magum jëwriñ ji, Aamadu Ba, yékkati woon, wax ne : “Man daal, waxaale naa léegi. Gis naa fi xaru fukki junneek ñaar, gis naa xaru fukki junneek ñeent. Bu gënee bari rekk njëg yi day wàcci.

Ñiy jënd xar ñépp, dëggaluñu kàddu yooyu. Xanaa mbote sax, jamono jii, jarul loolu. Te it, yarkati xar yiy jaay, ak lu ñu bariley xar, duñu bëgg di ñàkk li ñu jot a def ci seen xar yi. Ginnaaw loolu tamit, am na yeneen yu tegu ci kow boroom kër yi : soble, pombiteer, diwlin ak yeneen yu sew yuy gunge xar mi. Dara yombul. Te sax, njëg yi dañuy faral di ful bu xew-xew yu ni mel teroo. Loolu doyul, sañse yi di la xaar. Kenn umpalewul solos col gi ci bésub julli bi. Nde, njaboot gi, rawatina jigéen ñi, dañuy bëgg a sañse ba jekk. Nga war leen a xottil, xottil xale yi, jënd ay dàll.  Te, loolu yépp xaalis a koy def. Lépp daal, ndeke, teggi, teg la.

Ak lu ci mën di am, def loo mën, wax loo mën, boo tëddee nelaw. Ndax kat, ku xeebul sa noos, kenn dàqu la a noos.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj