TABB YU YEES ÑEEL KÀNGAAMI YOON YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci altine jii weesu lañu doon amal ndaje miy boole ak a tabb ñiy dogal ci bérébu àttewaay yi. Ndaje moomu nag, ma nga ame woon ca màkkanu Njiitu réew mi. Njiitu réew mi, Maki Sàll, jot na faa jël ndogal yu am solo ci wàlluw yoon. Muy ay tabb ak i coppite ñeel ay ndomboy-tànk. Tabb yooyu, jur nañuy coow ci réew mi, rawatina ci géewu pólitig gi. Ndax, gaa ñi dañoo jàpp ne tabb yooyu, ci kow “yaa ma neex” ak “yaa ma gën a déggal” kepp a ko lal. Mu mel ni dooley Yoon ci ndogal yi muy jël dafa tàmbalee am jiixi-jaaxa ci boppi saa-senegaal yi. Kóolute gi askan wi amoon ci Yoon, daf ko tàmbalee ñàkk. Te, liy yoon mooy ku ñu tabb donte ne sax, Njiitu réew mi moo la tabb, terewul nga war a tëdde njaaxanaay. Ndax, ki leen fi teg, askan wee ko fi teg. Daanaka nag, kàngaami Yoon yi soppiwuñu leen, dañoo soppi béréb yi ñu nekkoon kepp.    

Ndogal yooyu Njiitu réew mi jël nag, ngir soppi ndomboy-tànk ñenn ci kàngaami Yoon yi jur na coow. Donte ne sax, tabb yooyu laal na dëkk yu bari ci réew mi, yoy Ndakaaru yi daf cee ëpp coow. Ndax, ñi mu tabb ci béréb yooyu gaa ñi dañoo jàpp ne ci ay waawam rekk lañuy wéy. Te, wayndare yi ëpp lu ñuy yëngal réew mi yépp foofa lañu nekk. Béréb yooyu nag, yi ci ëpp doole nag mooy ëttu àttewaay bu kowe bi, maanaam bi ci ëpp doole (Cour suprême), ëttu Toppekatu Bokkeef gi (Parquet), ëtt bi nga xam ne ku ñu daan te àndoo ci mën nga faa dem ngir ñu àttewaat mbir mi (Cour d’appel) ak yenn ci ëttu àttewaay yi (tribunaux). Ëtti àttewaay yooyu nag mooy béréb yi nga xam ne ku am giitaŋaas ak kenn mënoo faa ñàkk a jaar. Ñooñu ñu teg ci béréb yooyu nag la am ci ñoom ñu ñuy duut baaraam. 

Tabb yooyu nag, nii la deme : bérébu àttewaay bu mag bi, kii di Sire Aaali Ba mooy ki ko jiite. Mu ànd ca liggéey ba ak Aamadu Baal, Aadama Njaay, Aamadu Lamin Bàccili, Umar Gay, Séynabu Njaay, Aysatu Jàllo Ba, Absatu Li, Baru Jóob, Ogistiŋ Juuf.         

Béréb bu mag bi ñeel toppekat bi (Parquet général) ña fa nekke nag ndombog-tanku layookat yu mag lañu am (premier avocat général près la cour suprême). Muy ku ci mel ni Seex Njaay, Alfa Uséynu Jàllo, Usmaan Jaañ, Maam Kor Nduur, Mbàkke Faal, Mariyeem Jóob, Umar Jéey, Ahmed Juuf, Paap Ibraahiima Njaay. Mu am nag, ay coppite tamit ci càmmeef gu mag ci bànqaasu jëwriñ ji ñu dénk wàlluw Yoon. Mu am ñu ñu tuxal, am tamit ñu ñu soppil i ndomboy-tànk. Muy ku ci mel ni Maalig Ja, Maaman Jite, Ibraahiima Sàmb, Yuusufa Njaay.  

Li ko deme ne tabb yi ci ëtt bi nit ki war a dem walla ay layookatam bu ñu àndul ci ab àtte moom, dëkk yu bari am nañuy coppite. Muy fu ci mel ni Ndar, Kawlax, Siggicoor, Cees ak Tàmbaakundaa. Waaye, coppite yi ci gën a fés mi ngi ame ci diwaanu Ndakaaru. Ndax, foofa la mburu tànge, fa lay xoyom-xoyomee. Béréb bi nekk ci Ndakaaru nag, Aamadi Juuf te mu nekkoon fi Toppekatu Bokkeef gi ginnaaw Sëriñ Basiiru Géy mooy ki ko jiite. Kii di Abdu Kariim Jóob nga xam ne moo toppoon ci moom mooy ki ko fa wuutu. Mu wute nag ba tey ak kii di Ibraahiima Baaxum, nga xam ne mooy Toppekat bu mag bi (procureur général près la Cour d’appel de Dakar) ci béréb boobu nga xam ne kii di Aamadi Juuf moo ko jiite. Ginnaaw loolu nag, am na yeneen i coppite yu mu amal ci ëttu àttewaay yi ak yenn ci bànqaas yu aju ci Yoon.        

Tabb yu yees yooyii nag, teey nañ xel. Njortees na ne politig a ko lal. Nde, mbirum Usmaan Sonko la ñu bari jàpp ne moo waral Njiitu réew mi tan ñi mu tan, ngir baral layoo yi gàllu ci loosam, àtte ko ci diir bu gàtt, tere koo doon lawax ci wotey 2024 yi. Mu mel ni Njiitu réew mi Yoon lay xàlle yoonam. Waaye, li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj