TÀGGE : MAMADU BAAJO KAMARA GÉNN NA ÀDDUNA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xibaar bu tiis la réewum Senegaal yeewoo tay, rawatina ñiy liggéey ci wàllu Yoon. Mamadu Baajo Kamara moo wuyuji Boroomam.

Mamadu Baajo Kamara nag, ñu gën koo miin ci turu Baajo Kamara, kenn dootu ko aajar fi réewum Senegaal. Ndax  di, moo jiite woon Ndajem ndeyu-sàrtu mi. Ñi ngi ko tabb fa béréb boobu ci weeru sàttumbaar, atum 2022. Moo ko jiite ba tay jii mu wàcc liggéey. Te, laata muy nekk Njiitu béréb boobu, nekkoon na fi Njiitu ëttu àttekaay bu kawe bi. Dees na ko jébbal boroomam suba ci àjjuma ji, ca sëgi Yoof ya ginnaaw julli jumaa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj