Layookati Senegaal yi am nañu tiis ak njàqare ginnaaw bi kenn ci seen naataangoo faatoo. Meetar Xuraysi Ba, di layookat bu fës te ràññeeku, moo faatu. XIbaar baa ngiy sog a rot. Nee ñu, réewum Tirkii la faatoo, ginnaaw bi ko ab feebar dikkalee.
Moom nag, Meetar Xuraysi Ba, ku ñu wegoon la, di woon layookat bu mag. Dafa di sax, bokkoon na ci layookati Usmaan Sonko mi nga xam ne, tay, mooy elimaanu jëwriñ yi.
Meetar Xuraysi Ba ab werekaan la woon, amoon xalima bu neex te doon xeexal yoon ak àqi doom-aadama.
EJO Éditions ak LU DEFU WAXU ñu ngi koy jaale njabootam, di ko jaale naataangoom i layookat ak waa réew mépp, di ko ñaanal njéggal ak yërmande.