TÀGGE : SËRIÑ MUSTAFAA SAALIW MBÀKKE DËDDU NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Umma islaam ñàkk na kilifa gu tedd. Njabootu murit a ngi jooy kàngaam bu mag. Senegaal ak Afrig ñàkk nañ doom ju ràññeeku. Waayeet, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ñàkk na Sëriñ, ñàkk na xarit. Ndeysaan, Sëriñ Mustafaa Saaliw Mbàkke, doomu Sëriñ Saaliw Mbàkke, moo wàññeeku ci guddi démb gi.

Sëriñ Mustafaa Saaliw Mbàkke moo nekkoon ñaareelu doom ci Sëriñ Saaliw Mbàkke, xalifab Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke ma woon. Moom nag, Sëriñ Mustafaa Saaliw Mbàkke, àddina sépp a ko seedeel julliteem ak ngëm Yàllaam, nekkoon ku dogu ci diine ji ak yoonuw murit, daan jàngale, yaatal ak a jëmmal njàngaley lislaam, rawatina yoy Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke.

Sëriñ Mustafaa Saaliw Mbàkke boroom xam-xam bu mag la woon, di woon ku dëddu àddina. Julli, jàng, jàngale ak mbay la saxoo woon. Ku daan defar diggante yi, daan wax ak a dox jàmm.

Nde, moom kilifa gu tedd gi, ginnaaw Yàlla, Séex Ahmad Bàmba Mbàkke ak njàngaley baayam bu tedd ba la doyloo woon. Ci lees ko seedeel, ku doon ittewoo mbiri réew mi la, daan taxawu ay taalibeem ba mu mat sëkk. Kon, ñépp a ñàkk.

Nee ñu, fa mu toogoon di jàng alxuraan walla xasida, laata walla ginnaaw gee, la ko sunu Boroom jël. Yàlla na Guyaar di këram.

EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale umma bépp, di ko jaale Xalifa murit yi ak njabootu murit gépp ak Senegaal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj