TAKKU WALLU BËGGUL SONKO BOKK

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci altine ji, la waa DGE (Direction Générale des Elections) siiwal toftale yi. Limu toftale yi xaw naa takku, donte ne sax, ñeen-fukk ak juróom-ñeent la woon, ñu mujj cee dindi juróom-ñett. Lëkkatoo gii di Takku Wallu Senegaal nag, dafa duut baaraam njiitul toftale lëkkatoog Pastef, muy Usmaan Sonko. Maanaam, dañoo jàpp ne moom Usmaan Sonko warul mën a nekk lawax bay jiite ag toftale.

Xiiroo ak ŋaayo bi doxoon ci diggante Pastef ak APR, ba tey mi ngi wéy. Ndax, APR dafa jébbal ab dabantal, Maki Sàll moo jiite seen ug toftale, moom Njiitu réew ma woon te jiite ba tay làngug APR. Li mu ko dugge mooy ñu génnee ci wote yi kii di Usmaan Sonko. Kon, jàkkaarloo bi waroon a am ci diggante Maki Sàll ak Usmaan Sonko ci wote yii leeragul. Dafa di, mbir moomu, ndajem ndeyu àtte mi moo ci war a àddu. Te, yéyagu ci yàbbi, donte ne sax, démb rekk lañu jébbal dabantal bi. Li mat a laaj kay, mooy lan moo tax ñu ne Usmaan Sonko mënut a nekk lawax ?

Ci dabantal bi, layookati APR yi jébbal, jot nañu cee joxe lay yi tax ñu foog ne Usmaan Sonko mënut a bokk. Cig pàttali, moom Usmaan Sonko dañu ko daanoon ñaari ati kaso ci coow li doxoon digganteem ak ndaw sii di Aji Saar. Naam, bi ñu koy daan teewul woon ca àtte ba (contumace). Rax-ci-dolli, ñu daanaatoon ko juróom-benni weer yoy, du ko tëdd ak ndàmpaayu 200i tamndaret ñeel coow li doxoon digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ. Daan boobu ñu ko daanoon ci mbir mi mu séqoon ak Maam Mbay Ñaŋ lañu ne moo gàllankoor ag nekkam lawax. Te, nee ñu sàrtu “amnistie” bu fukki fan ak ñett ci weeru màrs atum 2024 laaxaalewul mbir moomu. Maanaam, sàrt boobu nga xam ne dañu ko wote woon ngir far xew-xew yi amoon diggante 2021 ba 2024, mbir mi ñu ko daanee bokku ci. Ndax, nee nañu, li tax ñu daan ko mënuñu koo jàppe lu bokk ci mbiri pólitig. Kon, daan boobu moom day des ci kowam ba tey.

Mu mel ni, wotey Senegaal moom, dañoo baaxoo am coow. Te, yii jàll rekk firnde la ci. Nde, lëkkatoo gu nekk, làng walla mbootaay, day wut poroxndollu ngir gàllankoor moroomam. Su ko defee, aw yoonam gën a leer. Waaye, mbir mii moom, ñii di waa ndajem ndeyu àtte mii ñoo ciy indi ay leeral. Usmaan Sonko dina dem am déed, li ci kanam rawul i bët.

Li mat fàttali mooy ne, wotey 24 màrs yii weesu, Usmaan Sonko wote woon na. Te, képp ku ñu wax ne mënoo nekk lawax, doo mën wote. Kon, lu tax jamono jooja, waa APR kaasuñu woon. Lu tax ñu xaar ba tey di sog a kaas ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj