TAMXARIT 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àjjuma 28 sulet 2023 mooy doon bésu tamxarit. Loolu la waa CMS, Ndajem Julliti Senegaal, xamle. 

Ci altine jii weesu lañ doon séentu weer wi. Ginnaaw bi ñu jokkoowee ak seen ndaw ci biir réew mi ak fa bitim-réew, lañu jotoon ciy xibaar mooy ne “weer wi feeñul”.  Maanaam, kenn gisu ko. Moo tax, talaatay démb ji (18 sulet 2023) moo mottali weeru tabaski bi (Sul-hijja), di bés bi mujj ci atum 1444, bi Yonent bi gàddaayee ak léegi. 

Kon, àllarbay tey ji moo bés bu njëkk ci weeru tamxarit (muharram) ñeel atum 1445 mi ñu dugg. Bu ko defee, àjjuma 28 sulet 2023 mooy méngook fukkeelu fan ci weeru tamxarit, di yit bésu tamxarit. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj