Tasum xibaar mi ngi bëgg a tagatémbe jamono jii ci réewum Senegaal. Dara waralu ko lu dul ni Yoon di doxale ak ñi koy taxawe, rawatina ñi tànn seen yoonu bopp. Maanaam, képp kuy tóxal i xibaar, di ko faramfàcce te di bañ a raay Nguur gi, boo mooytuwul yow lañuy mujje tóxal, yóbb la kaso. Boo màndoo sax, bañ a jeng ci booru Nguur gi, jàmm doo ko am. Moo tax, ñii, ñu ngi leen di woo, ñee, ñu téye leen ; ñenn ñi, ñu topp leen, ñeneen ña ca des, ñu ngi leen di tëj. Jamono jii nag, muy kibaaraan yi, di mbaali-jokkoo yi, fépp fu waay waxe lu saafaanook bëgg-bëggi Nguurug Maki Sàll gi, doo fanaan sa kër. Mu mel ni, ñoom dañoo bëgg ne, lépp lu leen askan wiy déggal, di lu baax ak lu rafet. Waa Walf ak lenn ciy taskati xibaar bañ loolu. Moo tax, jamono jii mu bari lool ci ñoom ñuy am ay giita-ŋaas ak yoon.
Fi mbir yi tollu nii tembe, kibaaraan yi dañoo am doole lool ci defar mbaa yàq. Ndax, ñoom ay ngànnaay lañu yu am doole yoy, mënees na leen a jëfandikoo ngir lëndëmal xelu askanuw lëmm. Maanaam, ngir noot leen ba duñu gis safaan ci yow. Mu mel ni, ñii di waa Walf moom, li ñuy wootewoo baatu ñi amul baat tax na ñoom ñu ne duñu raayal kenn ndiggam. Moo tax, ñu bokk ci kibaaraan yi ñu gën a singali. Te, loolu du lu bees. Ndax, tàmbaliwul tey. Bari na ay fitna yu ñu leen daan teg muy bi Siidi Lamin Ñas di dund ak bi mu génnee àdduna yépp.
Jamono jii nag Walf dafa bokk ci kibaaraan yi askan wi gën a jox nopp, rawatina ci mbaali jokkoo yi. Ndax, ñoom, muy seen i waxtaan ak seen tasum xibaar, duñu ci raay-raayal dara, dañuy xolli góom bi. Moo tax, kii di Coro Màndelaa bokk ci ñoom ma nga ca loxoy Yoon. Paap Njaay, moom tamit, ma nga ñu tëj kaso. Kii di Mustafaa Jóob tamit di njiitul Walf dañu ko woolu woon barkaati-démb. Moom nag ba mu jógee ca woote ba kàddu yii la yékkati woon :
“Li ñu ma doon laaj ci sama kilifteef, ci sama liggéey la. Li nga xam ne, xam naa ko ci Walfadjri ak ni muy doxe. Wax naa leen ko. Bi ma leen ko waxee tamit, ñu wax ko seen i kilifa, ñu gis ne lañu fa wax, xëy na doy na leen. Ñu ne nu mën nanoo dellu ci sunuy njaboot, nu koy sante Yàlla, di ko sante ñépp ñi doon ñaan Mustafaa bañ a toog fii. Fi mu tollu nii moom waxuñuma ma ñëwaat.”
Yëf yi ba tey yemul foofu. Ndax, am na yeneen taskati xibaar yuy jànkonteel ak xeeti doxalin yooyu. Muy ku ci mel ni Paap Aale Ñaŋ nga xam ne ca jamono yee ma nga woon ca loxoy yoon. Ak kii di Baabakar Ture mu Kéwoulo nga xam ne keroog lañu ko woolu woon te, ba tey, ma nga ca loxoy yoon. Woote boobu li ko waral mooy pelent bu ko kii di Ferederik Napel defoon. Moom li mu koy toppe mooy biral ay xibaar yu wérul ci moom, ŋàññi ak yu ni deme. Mu mel ni daanaka ñu bari ci ñoom li ñu leen di toppe mooy biral ay xibaar yu wérul walla yàq der. Maanaam ŋàññi kenn walla ndawi yoon ak yu ni deme.
Kon, Nguur gi moom, boo ko dul waxal lu ko neex, fàww nga koy teg fu leer. Lu ko moy Yoon dal sa kow. Ku koy waxal lu baax moom, yoonam nekkul ci yow. Xeetu doxalin yooyu Yoon di def tax na ba léegi, taskati-xibaar yi dañoo féewaloo, ñee jëm fee, ñale jëm fale. Ñii ne, ñun kii lañuy àndal lu baax rekk lañuy wax ci moom. Ña ca des ne, nun àndunu ak moom, lum dégg ci lu ñaaw, nun la. Waaw léegi askan wi kon, kan moo ko fiy nekkal ? Di ko wax li nga xam ne moo xew ci réew mi bañ ci seet Masàmba ak Mademba. Bañ ci xool ne bu ma waxee lii dañu may neexal walla dañu may xoqatal ak a bunduxataal.
Loolu moo tax, liggéeyu tasum xibaar moom tàmbali na di sooxe bu baax ci réew mi. Dafa mel ni, léegi, ku tas xibaar, tasoo xar-baaxi Nguur gi, ci kaso bi ngay tas. Te, dara waralu ko lu dul fàtte askan wi ci seen liggéey, jiital seen i njariñ. Te, askan wi kesee leen may doole ji ñu yor tey. Waaye nag, ku fàtte la la fal moom, sag folleeku da lay bett.